Telechargé par Séex jóob KSS

4 6046238394172834710

publicité
Kadduy Seriñ Mbay Jaxate
1
Noreyni KEBE
Seriñ MBAYE DIAKHATE est le fils de Xaali Majaxate Kala et de Sokhna Penda Coumba Fall.
Il naquit à Aynumaan dans le Kajoor en 1875.
Majaxate Kala en effet passé pour l’un des lettrés les plus connus du Sénégal des royaumes; Claude
GERRESHCH, un chercheur Belge qui a travaillé à l’IFAN lui a consacré une biographie assez fouillée,
en introduction à un travail de traduction d’un important traité de métrique arabe dont il est
l’auteur.
Xaali Majaxate Kala était un chef de village et marabout, professeur, cadi et secrétaire d’un roi (Lat
Dior Diop : homme politique Dammel du Kajoor), mais aussi un métricien renommé et très grand
poète.
Sa vie connut sur le plan politique plusieurs péripéties que nous n’évoquerons pas ici; nous
retiendrons simplement de lui, outre le fait qu’il fut le père de notre auteur (Seriñ MBAYE Diakhate),
qu’il a également enseigné la grammaire et la versification arabes à Cheikh Ahmadou BAMBA.
À ce propos Seriñ Mouhamadou Lamine DIOP Dagana nous apprend, dans sa relation de la vie de
Cheikh Ahmadou BAMBA que celui-ci le fréquentait pour approfondir sa connaissance de la langue
arabe (irwa-unnadin).
Avec un père d’une telle stature, Seriñ MBAYE DIAKHATE décida de rejoindre Cheikh Ahmadou
BAMBA afin de lui prêter serment d’allégeance
Sa rencontre avec Seriñ Touba Khadimur Rassul (Radiyal LÂHU ‘anhu) son maître le plus grand
miracle de DIEU,prototype de la servitude et détenteur du trône de la noblesse
C’est alors que le Shaykh était au Gabon que Seriñ MBAYE DIAKHATE quitta Aynumaan pour aller
rejoindre le Shaykh. Son père vivait encore. Mais le Shaykh étant absent, c’est sous la responsabilité
de Mame Thierno (Ndaamal Daarou frère de Cheikh Ahmadou BAMBA) à Daarou Marnaan qu’il était
place. C’est auprès de ce dernier qu’il termina ses études coraniques.
Après le retour au Gabon, alors que Cheikh Ahmadou BAMBA s’apprêtait à partir en Mauritanie,
nouvelle terre d’exil que Seriñ MBAYE DIAKHATE fut présenté à ce dernier par Mame Thierno
BIRAHIM Mbacké frère de Seriñ Touba Khadimur Rassul (Radiyal LÂHU ‘anhu).
Ce sera donc en Mauritanie que Seriñ MBAYE DIAKHATE commença son service (tarbiya) auprès de
Seriñ Touba Khadimur Rassul (Radiyal LÂHU ‘anhu). Là, le Cheikh lui confia son fils Seriñ Bassirou
Mbacké pour son instruction islamique.
Si l’on se réfère à la stature intellectuelle du futur auteur de « Minanu Baqil Xadim »(les bienfaits de
l’Éternel), on peut d’ores déjà se faire une idée des qualités intellectuelles de notre auteur.
C’est également en Mauritanie que Seriñ MBAYE DIAKHATE commença la production de ses poèmes;
C‘est donc pendant plus de 20 ans (4 ans en Mauritanie, 5 ans au Jolof et 15 ans à Diourbel que Seriñ
MBAYE DIAKHATE resta au service de Seriñ Touba Khadimur Rassul (Radiyal LÂHU ‘anhu), lui dédiant
des panégyriques contribuant à la formation des aspirants (murids) et se vouant entièrement au
service de son Maitre.
Histoire du patriarche nommé XURU MBACKE
En 1918, Seriñ MBAYE DIAKHATE fut envoyé à Xuru Mbacké par Cheikh Ahmadou BAMBA, les
raisons de cet envoi revêtent une dimension tellement mystique qu’il ne nous parait pas indiqué de
les développer ici.
Toujours est-il que pour se donner une idée de l’importance mystique de ce petit village du Baol, il
suffit de savoir que les vénérés parents de Cheikh Ahmadou BAMBA y ont vécu avant leur départ
2
Noreyni KEBE
pour le Saloum, qu’ils y ont laissé leur dernier enfant et que Seriñ Touba lui-même y fera inhumer un
certain nombre de ses propres fils trop tôt rappelés à Dieu.
Xuru Mbacké est donc aujourd’hui, malgré la modestie de la localité un véritable sanctuaire du
Mouridisme.
La vie de Seriñ MBAYE DIAKHATE à Xuru Mbacké était entièrement consacrée à l’étude, la prière,
l’enseignement, l’agriculture et la production de poèmes.
Véritable Soufi (mystique), modèle vivants de ses leçons, Seriñ MBAYE DIAKHATE s’éteiñit en 1948, à
l’âge de 73 ans à Xuru Mbacké où il repose aujourd’hui.
ses œuvres tournent autour de thèmes suivants :
L'amour de ce bas monde
l'oubli de la mort et de la vie future
L'Oubli Dieu
L'amour de la gloire
L'orgueil
L'envie
La médisance
Les relations entre maître et disciple
La voie à suivre pour l'aspirant et les dangers de la voie....
Indications : (source Drouss.org)
Wolof
per
rus
caam
ñam
xol
jibi
njaay
nday
ŋaam
gëm =
e=é
u = ou
c = th
ñ = gn
x = kh
j=j
nj = nd
nd = nd
ŋ
ë = eu
é = è (plus dur) = rér
óo = au
góor
q = xx
suqali
ii - uu - oo - aa ee (tirer sur le
son) ; Ex : biir - suur -xool gaal - xeer
Français
pér
rous
thiam
gnam
khol
jibi
ndiaye
ndeye
(machoire)
gueum
perdu
gaure
soukh khali
3
Noreyni KEBE
Table des matières
Ndaxam ab Murid … ................................................................................................................................ 8
Murid dafay gaaw … .............................................................................................................................. 11
Seriñ Mustafaa ...................................................................................................................................... 12
Man BAMBA doynama …....................................................................................................................... 15
Weru Koor ............................................................................................................................................. 16
Koo Xam ne xamna’k ... ......................................................................................................................... 17
Maa bon te Baaxub Seriñ … ................................................................................................................... 17
Kudul yaw bawul … ................................................................................................................................ 17
Alhamdulilaahi … ................................................................................................................................... 18
Jooyal ma junni bi at … .......................................................................................................................... 21
Mo jaa lu deefi defati … ......................................................................................................................... 22
Sëriñ bi yaa gën alal ............................................................................................................................... 24
Bastul a bonn … ..................................................................................................................................... 25
Rikk Asan lu man a xew … ..................................................................................................................... 28
Ma jog caw ub yar ….............................................................................................................................. 31
Lu dul ni ñokket ..................................................................................................................................... 34
Murid degg bul merr … .......................................................................................................................... 37
Xarit dëgg yewwul… .............................................................................................................................. 39
Xarit bul tamal sa bopp aw lejal ............................................................................................................ 41
Masamba sembal ci geejug BAMBA … .................................................................................................. 43
Ma wax fi Ahmadou Kumbay….............................................................................................................. 45
Addina bëgg na laa fab waaye… ............................................................................................................ 47
Adina moo mana nax............................................................................................................................. 49
Seriñ bi ayee na jew … ........................................................................................................................... 51
Yaw foo dajeeteek u nit jàppal… ........................................................................................................... 52
Jàppal sa xol bi defar ............................................................................................................................. 54
Xam naa ne ag ñakka mandoo bon ….................................................................................................... 56
Nan japp tank yi ak lammin yi ............................................................................................................... 58
Yaw miy nelaw … ................................................................................................................................... 60
Ñaanal Sëriñ Mbay … ............................................................................................................................. 61
Maroon naa … ....................................................................................................................................... 63
Kuy dounde bum fatee dee ................................................................................................................... 63
4
Noreyni KEBE
Seriñ bi yiw wunu xamul … .................................................................................................................... 64
Meloy Baamba … ................................................................................................................................... 65
Seriñ bi fegalñu moyaki moy …............................................................................................................. 66
Sa bind daa na waral … .......................................................................................................................... 67
Foo bëgg dem … .................................................................................................................................... 67
Bu cér yépp gàntoo def'as lëf jafe ......................................................................................................... 68
Seriñ, Xarit, Jëkër … ............................................................................................................................... 69
Sëriñ bi yaa baax .................................................................................................................................... 70
Fasoo nama fase dunyaa … ................................................................................................................... 71
Yallaa di geejug njariñ............................................................................................................................ 72
Gennal ci nëpp ba sett ........................................................................................................................... 73
Murid bi yaw jeexalal sak dundu…. ....................................................................................................... 73
Dama dém fi ay sëk ............................................................................................................................... 74
Waajal nga gaayi te waadioo ................................................................................................................. 74
Sëriñ bee matub sàngg moo gën kuné .................................................................................................. 75
Seriñ day wootee Ibliss di wootee … ..................................................................................................... 75
Cheikhi gannààraki kajoor ..................................................................................................................... 76
Ku man di juleeka wirdaakay ................................................................................................................. 77
Ma jóg defal gaayi tindoodiy bëyit yu rafet .......................................................................................... 78
SIYAARE ................................................................................................................................................. 79
Ku toppul Yalla yit boum deeti …........................................................................................................... 79
Ku toppul Yalla yit bum deeti juk diko moy Moy yàlla rëyna te dee dém naarit woyoful .................... 79
Xarit dëgg yaw bul defub tëddkat ......................................................................................................... 80
Gaa yile man jébbalu naa ...................................................................................................................... 81
Ludul ndigël amul njariñ ........................................................................................................................ 82
Sa jëmm ji lé tax ay du ñëw ................................................................................................................... 83
Sa jëf ju baaxul bu muy tax yaw nga ..................................................................................................... 84
Yaa denc yaw ndaw sa say kem daa ngorook a jamoo ......................................................................... 84
Abdoul Ahad … ...................................................................................................................................... 85
Yaa sedd ab xol guyyu … ........................................................................................................................ 86
Ndegam awma ndam boppam …. ......................................................................................................... 86
Ma tag BAMBA ...................................................................................................................................... 87
Ma jog man ligeeyal Seriñ BAMBA mi ................................................................................................... 89
Yaw Abdu Xaadr laxasul ........................................................................................................................ 90
Guissuma man lu jarr taxaw .................................................................................................................. 91
5
Noreyni KEBE
Ku dof bay ndamoo baaya mit mbaa ndayam … ................................................................................... 92
Koo xam ne jox na lab liggeey ............................................................................................................... 93
Ku àndul ak moom................................................................................................................................. 94
Ma jóg wuti ndëndum cant ak galenub ngërëm ................................................................................... 95
Nangul a feete ñepp suuf ...................................................................................................................... 96
Seriñ bi man yaama guën ...................................................................................................................... 97
Seriñ Massamba … ................................................................................................................................ 98
Sheex Ibra .............................................................................................................................................. 98
Ndaxam BAMBA yaa jar di sonnal ba dee ............................................................................................. 99
Ndaxam gaayi may siisakay dox di bañ ............................................................................................... 100
Ku xëy di neexalu nit ngir bëgg seeni ngërëm ..................................................................................... 100
Sëriñ bi yaw nanga nu may, Ngir Yàlla ak Yonen ba tay, ..................................................................... 101
Def a la def nit, boole’m xel ak fit ....................................................................................................... 101
Ndaxam gaayi koo xam ne bàmmeel a koy ......................................................................................... 102
Assalamun Alaykum Mbacke … ........................................................................................................... 103
Di bay di bay ba sa mbay ñor xomb nag nga ne cas ............................................................................ 104
Fabal Yalla jamm ak … ......................................................................................................................... 105
Mënoon ngamaa wacc bañmà ma saak may ku amul ........................................................................ 106
Bà yyil kulay ba ..................................................................................................................................... 106
Ku tëb bëgg a dal cig cëriñ jell ag ........................................................................................................ 106
Doo kenn yaw, ken du yaw,................................................................................................................. 107
Sëriñ bi nëbb nga saa bon gii ba dee fi ma jox .................................................................................... 107
Njagam bëgg nga sak mourid jak te wër ............................................................................................. 108
Lu tax nga baaxoon a baax it mat na ................................................................................................... 108
Seriñ bi Yaw yaa wara sante Yalla ....................................................................................................... 109
Murid dëgg bul gaawa wutt kër muñal ............................................................................................... 109
Jigeen … ............................................................................................................................................... 110
Soxna Jaara .......................................................................................................................................... 111
Sources : .............................................................................................................................................. 112
6
Noreyni KEBE
Mot de l’auteur du document :
Ce document n’est rien d’autre que le fruit d’un enchainement de « copier/coller » et de
retranscriptions de paroles chantées par Serigne Abdoul Ahad Tuuree. Il a été rassemblé par
un inconditionnel de Serigne Mbaye Jaxaté qui n’a fait que regrouper l’ensemble des écrits
du poète qu’il avait sous la main, repris principalement à partir de « statuts Facebook » et de
la mémoire de maitrise de M. Mamadou Lo.
Par conséquent, la vente de ce document est interdite !
Aji dajalee gi mi ngi ñaan kepp ku gis mbind mii mu ñaanal ko ngërëmal Sëriñ bi !
Di tuup dëng dëng yi ak lepp lu ci jubul
Ousmane KEBE
Euhlou Touhfatoul Moutadarihin
Dahira Tuubaa Jawartulah Paris
« Yalla na ñu Seriñ Tuubaa fayal Sëriñ Mbaye Jaxate »
7
Noreyni KEBE
Ndaxam ab Murid …
Ndaxam ab murid saa su bëggee ludul
Ndigal ak ngërëm dootu bennub murid
Murid dëgg yombul la yombay nga wax
Ne man ab murid laa te doo ab murid
Ku tàggoogul ak soxla kay dub murid
Ka tàggooki soxla a di ngën jib murid
Fabal sab Sëriñ teg fi sab xol, xalam
Ba far fàtte say soxla, lii dig murid
Murid bub sëriñ dul tuxoo fib xolam
Du am soxla yal naa di boobee murid
Yëgal kat ne dunyaa ni ag dex la mel
Te nag ab Sëriñ moo di gaalug murid
Ndegam nag Sëriñ moo di gaalug murid
Moyul genn jëm fenn yaw kiy murid
Ku gennul du lab mukk, kuy genn lab
Akay leb te yii yaar a yaqug murid
Te lëf manla tee kat nga leb lab ludul
Nga wut sab sëriñ yaw te muñ ag murid
Ku wut lëf ludul sab Sëriñ dal di lab
Te leb ñépp far xëtt sartiy murid
Wutal sab Sëriñ yaw te loo ñàkk muñ
Te loo am fabal jox ko, kon ngay murid
Murid day muñug ñàkk muñ jépp lor
Ba sanggam ba dàkkul ko luy lor murid
Lu lay dal ci ag ñàkk mbaa lor muñal
Ba sab sangg teggil la koo yaw murid
Bu sab sangg teggee sa ñàkk ak sa lor
Ku lay deeti teg ñàkk akiy lor murid ?
Bu teggeegul it nag sa ñàkk ak sa lor
Ku koy deeti teggeeti tontul murid ?
Joxal sab Sëriñ sag jur ak sab xol it
Te bul waxlu, bul wax, lilee dig murid !
Ludul “maa ngi nii” aska di yaa ngi nii
Bu koy wax, bu koy waxlu, déggal murid !
Yabal nit ci sab sangg waxloo ko lëf
Ludul maa ngi koy sopp kay dug murid
Bàyyil dëgg yobbante lëf sab Sëriñ
Ludul ag jur ak bëgg a def ab murid
8
Noreyni KEBE
Da ngay sanggloo sab Sëriñ saw yaram
Te boo yënggtoo kat mu daw la a murid
Xamal yaw ne ab sangg day sangg nit
Te doo gis mu sangg it ku deewul murid
“Mukallaf” mu deewul ku koy sangg moy
Te ab sangg moytil, yëgal lii murid
Lilee tax ku tuddub murid yomb a gis
La të a gis ku tuddub murid tey murid
Murid dëgg day dee te deewul asal
Li dee metti-metti jotul ag murid
Amaanaa nga gis waa ju tëb dal di dee
Te doo gis ku tëb dal di def ab murid
Gisal waay a ngii jóg di daw cig murid
Ba am ay murid nag te kat dub murid
Gisal kii itam jog di daw cig murid
Ba dundam ba far jee mu réereg murid
Ku fas ne ku am ay murid dib murid
Te fas ne ku ñàkkiy murid dub murid
Xamul lëf, yëgul sax la am ak la xew
Te kat dub murid sax, xamul ag murid
Lilee tax ba saytaane wor gaa yi tay
Tënkkug murid nag ci am ay murid
Te sax kuy murid ak kudul ab murid
Fa bis péncc lay feeñe, yewwul murid !
Bu deesee layook ay fexee jog di aw
Siraat it nga xam yaw ku doonub murid
Balaa kenn a xeebaate war naa nég it
Ba xam luy fasoo xew ci béppub murid
Murid yépp a ngiy mel ne gànccax gu sax
Te gànccax xamoo ag mujam kat murid
Te gànccax amaanaa mu jóg neex a gis
Maral dog ko jëkkug ñoram, céy murid !
Amaanaa nga gis gànccax it jóg woyof
Te naataange far jot ko, waarul murid !
Na ngay mujje Yàlla a ko xam, moo xam it
Keneen it la muy mujje, jàppul murid
Bayil yaw nit ak dox di xeebiy mbiram
Amaanaa nga yab koo matookob murid
Ku tàbbib nawet yaw te góoboo ba gar
Ba far mànku doo xam la ngay am murid
Ku deegul lu xam-xam du xam ay mbiram
nangay muslu foo tollu am ndog murid
nangay tuub’akay yeesalug njébbal it
di xeeb it sa jëf yépp ak sag murid
9
Noreyni KEBE
ku xeebul jëfam dal di naw ay jëfam
ku naw ay jëfam dal di set cig murid
sa jëf boo ko dee naw da nga a réere kon
ne Yàlla a la sàkk ak sa jëf yii murid
ndegam xam nga tay jii ne Yàlla a la jëf
bu wér ak sa jëf yii, bàyyil ndam murid
bàyyil ndam te taqoo akug cant far
manoo lëf, defoo lëf, xamoo lëf murid
ku gis gopp buy naw mbayam mook a dof
te wax jii ma wax yaw xalam koo murid ?
ka yor gopp ba a bay ne goppam ba kay
bayul lëf te yaw yaa di gop bee murid
Sëriñ bee la yor moom itam Mustafaa
Ko yor, Yàlla yor Mustafaa nag murid !
Sëriñ ba a ngi jébbal ko say mbir bu wér
Te def kob Sëriñ moom mu def lab murid
Xamal lay mbiram yépp jox lay ngërëm
Yudul jeeki barkeeki ngën jiy murid
Fegal lay lor ak ñàkk ak mépp ndog
Te yóbbal la, yóbbal sa béppub murid
Nga far jekk, jekkal sa béppub murid
Nga sellug murid nag, ñu sellug murid
Ba ngay sant, ñuy sant, ngay bég, ñu bég
Nga mat ab Sëriñ yaw, ñu mat ay murid
Lilee dig Cëriñ, lalee dig murid
Ludul lii du gennug cëriñ, dug murid
Defarkat bi maa ngeeti ak saa tilim
Defar maati yaw mii, defar sab murid
Xasaw naa te fees ak lu soof ak lu bon
Setal maaki mbég, yaa di géejug murid
Doxal saa digg ak luy waral ag tilim
Te leeral ma faf def ma jantub murid
Gërëm naa la, xam naa ne mat ngab Sëriñ
Bu wér, waaye yal naa la mat ab murid
Te yal naa la saf te saf sa béppub murid
Te yal naa la am, am sa béppub murid
Joxal bépp jullit lu seddub xolam
ba mboolem jullit ñépp def say murid
fabal say murid yépp teg nag ca kaw
bu ken gis ku suufeeti tey ab murid
kudul sab murid yaw na ñee sab murid
te bul baati ken ree sa bennub murid !
10
Noreyni KEBE
Murid dafay gaaw …
Murid dafay gaaw
ba mel ni kuy naaw
Loo wax mu naa waaw
te dëkke tës-tës
Te bëgg saηngam
ba fàtte boppam
Te fàtte leppeum
nooye ne suηnguf
Woyofe niw fel
di suufe bay mel
Ne dàll woo sol
du jekki bay raf
Ku jog mu màggal
kuy mag mu sukkël
Kuy ndaw mu yuugël
ëskaye jii jëf!!
Tay baηki tàηkam
di sajju loosam
Di fooηki maasam
du sajji nit xef
Du benne muy xëy
ba jëmelak moy
Te looko moy-moy
du la moyuk sef
Day melne ab neew
ku mel nilee neew
Gisnaako fii daaw
ba royko man lëf
11
Noreyni KEBE
Seriñ Mustafaa
Sama jëmma ngii Sama ñeppa ngii sama leppa ngii
Mani cas tegal la ci sab loxoo yaw Mustafaa
Nangul te jël yallà la jox kumu jox nga am
Lay dëgg tay jii yaa fi gën yaw Mustafaa
Man naηunaa naηngoo ma war moo gën ci man
Ngir Baabakar moo ñjëkka naηngul Mustafaa
Bumadaa bañit tay naηngunaa ñëwnaa fi yaw
ηëbnaa ci yaw jeggal ma nak yaw Mustafa
Buma toppe lëf buma seete lëf buma jàpppe lëf
Lewetal yëram fàttteelu ay yaw Mustafaa !!
Yaa donnu ngor yaa nàmpu ngor yaa dis gorit
Buma màtt bis buma màttu bis yaw Mustafaa
Ñun ñeppu àndak yaw di wey moo war ci Ñun
Moo gën ci Ñun ηëbnaa la man yaw Mustafaa
Maa ngii di tuubaka reeccu mbooleem jëf ya wey
Mbooleem lu baaxul farko far yaw Mustaafaa
Ñun ñeppu yaw lanu am te yaw mii Ñun nga am
Yorlaa nu war yor noo la war yaw Mustafaa
Koo seeruwul sëytaane moo fëkkum xelam
Ibliisa tee nit ñeppu àndak Mustafaa
Kula tooppul-ak kula toppu nak ñoo yam ci yaw
Ngir raw nga lor jot weppu yiw yaw Mustafaa
Kuy ñëw begël kuy bañ begël lu ci man xew
Yaw am nga ndam yokkal te yokkunu Mustafaa
Koo seeruwul kookee layam wa du jub ëllag
Yaa donnu mbër ak palga ëskey!Mustafaa
Tan yaa ngilay tuηlooka toogaanoo ka wut
Ab dog ci yaw dundël te wer yaw Mustafaa
Jërajëf jëfal say jëf du bon say wax du bon
Mbooleem ñi baaxa ngilay gëram yaw Mustafa
12
Noreyni KEBE
Yaw Mustafaa awma sag pay waaye yal na nga tiim
Bu wér ci barkeb Sëriñ Tuubaa li jant bi tiim
Dalal nga xel yi, seral xol yépp, yal na nga faf
Suuxal ña gën seeni kem nim njàpp suuxale tiim
Sa jëmm jii nuy janool’ak say ngëneel a waral
Njariñ yi dëkk fi Ñun, yàggal te boole nu moom
Yàggal te boole nu moom’ak lépp lëf lu nu am
Sab xol ne guuy’ak sunuy xol ñépp sant ba luum
Ku nekk bég na ci yaw, yaakaari kenn tasul
Asal, asal ka la jiital Mbàkke nammul a juum
Taxaw nga temm ci aw yiw yal na Yàlla taxaw
Temm’ak ngëneelam ci yaw, jébbal la sépp soloom
Boo jekkiwon rekk lal sab der du yàq ci yaw
Lëf, waaye itte ju rëy jee tax nga ñàkk moroom
Defar nga àll yi ak kër yépp yaw ba ñu jag
Ku nee ngi am itte ngir yaw mat nga ñépp boroom
Fu nekk tojj nga fa yit ab àll samp fa kër
Bégal fa nit, may ko fab xaalis defar fa goroom
Sag cant ñépp la war, saw tagg ñépp la war
Mag’ak ndaw’ak képp koo jis rembatal nga yoxoom
Ku lay xarab dub julit, dus gor te dub murit it
Ku yewwu sant la biir’ak bitti mbaa mu ne xiim
Lii laa la wax man, sa fan wii yal na gudd nga tiim
Mboolem ña tiim’ak ña tiiméef’ak li jant bi tiim !
-Rafet nga jëf, rafetub xol, Yàlla yal na la fay
Te may la, wis la ba ndab loo am ni dell'aku yiw
Rëy ngaw fit’ak itte rëy ngab xol te rëy nga jëf it
Rëyub yar’ak juddu, rëy ndam, rëy ngërëm, mat a naw
Tabaarak’Allaahu yaw gimiñ gu bon na la moy
Te moy sa kër, moy sa waa kër, moy julit ñi la ëw
Loo sant-sant sa baay’ak Yàlla dolli ca lëf
13
Noreyni KEBE
Xamal ne saytu nga may goo xam ne gii du gu sew
Sewoo, sa may gi sewul, yaw sewlewoo te sewoo
Ku rëy ku rëyle nga, yaa gën ñépp yaa ne ca kaw
Ñun ñépp noo di sa néegub cant ngay sunu puj
Moo tax ku nekk di buux-buuxlook a bafngu di ñëw
Yaa def lu lew domm ngir yaa jàpp àll yi toj
Rajax ñu mokk nga bay am lépp, lii daganéey !
Man’ak samay kem da nuy jéemub liggéey’ak a caaXaaneb liggéey’ak a kaf, yaw dong dong a liggéey
Leeral nga kër yépp, leeral àll yépp nañax
Fu nekk nee na nañax ngir yaw, sa ndey rusuléey
-Yaa tedd, yaa ma teral, yaa mucc, yaa ma musal
Yaa jàppu, yaa ma jafal, jaaraama sédd nga ma
Yaw aayewoo ma sa ay gii, Yàlla boo jisu ay
Ci ay gi, yal na nga yàggug pal falaale nga ma
Manon nga maa jébbal’as ndaw su gën su ñu xam
Te jébbaloo ma sëtub Yonnen bi, bett nga ma
Xañoo ma wërsëg, xañoo mab sag, xañoo ma njariñ
Xañoo ma barke, xañoo maw nit, joyanti nga ma
Man née[g] bu joy rekk laa woon, yaa ma ron jëni weñ
Defar ma nag ba ma jag, yeesal ma faale nga ma
Sëriñ bi ak Yàlla ak Yonen bi ñii dañu laa
Yaatal nga yaatal ma, yokkul fàww, yokk nga ma
14
Noreyni KEBE
Man BAMBA doynama ….
Man Bàmba doy nama, doyloo naa ko dootu ma fab
Téerée ki maxtume ak ndomboy peurëg di ko sol
Koo xam ne bëgg na gàllaaj ak alal aku nit
Na dàl di jóg tàbbi géttam gii, te moo di ndigël
Ki samp gétt gi, day wër gétt gée ka fegal
Bëyam wi lor, waaye bëy wuy génn lëf di ko jël
Xarit yërël rëbb baa ngii xëy soxug fetalam
Jóg rombu gétt gi wéy, dem yooti rab wa fetal
Xam ngee li tax rëbb bee jóg rombu gétt gi wéy
Di weesu bëy yii, li muy gis sàmm bee ko waral
Li tax mu jóg weesu bëy wii, tàkki téeré taxul
Li tax mu dem rayi rab wee, ñàkk i téeré taxul
Am sangg a tax bëy wi deewul, ñàkk sang a waral
Rab yii ne jànjañ te ken neewul ki ray lu waral?
15
Noreyni KEBE
Weru Koor
Mbooloo mi gan ñëwna tay, Ñun ñépp nan ko dalal
Yaatal ko jublu ko ki mbég, may ko itte ju rëy
Te weeru kooray ganug mboolem ku Yàlla soxal
Ñun ñépp war nanu koo may aajo léegi mu wéy
Ku muñ te farlu ci, day xëy benne tàggu la dem
Ba la'aki cant yu dóotul jeek i koom’aki may
Moo tedd moo tabe day ub bépp buntu bu bon
Di wubbi wunti mbég’ak yërmànde tay fegi moy
Fasoo nanoo um di sellal fàww tay rafetal
Ba xëy matal doge koobaa kiy gëléem’aki ñay
Yal nan ko léemu bu wér sargal ko jox ko nganam
Ba xëy ko gungge nu tàggoo far des’ak sunu way
Yal nan ci am may yu rëy yoo xam ne dόotuñu jee
Te dàq lem, dàq suukër, dàq ceeb aki lay
Noo ngii di sàkku ci barkeem’ak ñi gëm ñi ko wum
Ndollen lu àndul’akiy coonook i tiis aki jay
Kooray njariñ moo diw yiw waaye kenn du ko muñ
Kudul ku gëm Yàlla ak Yonnen ba séenu ca pay
Ñun ñépp yal nanu am ay woorukaay aki yëf
Yu am njariñ ak ndogoo kiy xëdd fàww yu doy
Te yal na nuy woor a kay farloo ka xëdd a ka dog
Ba xëy woreek i mbég’ak saa beesi cant yu rëy
16
Noreyni KEBE
Koo Xam ne xamna’k ...
Koo xam ne xamn'ak mayam nam tollu kooka du man
Saa may gi xawma ko man saa may gi ëpp na xel
Man mii dumab dof dumab yéefar te deefu ma xas
Te Yàlla mii bu ko sooboon yépp bokk ma dal
Man gumbë wul làgi wul woppul te niàkku ma lef
Ludul lu bon gaayi man mii lak tawat waratul
Maa bon te Baaxub Seriñ …
Maa bon te baaxub Sëriñ nit ñép népa ma gën
Te maa fi gën ab Sëriñ saa mbon gi dootu ma lor
Ku ñàki sér ku ko fab tàbal ci guddi mu bég
Ku bëgga leeral ku fab aj jant jox ko du mer
Ku jog di sàku ci ndox gis dex xolam ba du wow
Ku jog di yalwaani njël for dàgga jekki sa kër
Kudul yaw bawul …
Kudul yaw bawul góor’ak jigéen’ak këram ne mes
Ci àll ba ay at ken dajul Mbàkke lii nga daj
Kudul yaw du fab xaalis di sànni ci biiri dex
La sangg ya daa jeexaat’akay làmb yaa ko daj
Yaw it ñi la fiy jeexaatu yal na ñu for nu for
Ñi lay dox di làmb it ñépp yal na ñu bokk daj
17
Noreyni KEBE
Alhamdulilaahi …
1- Buurub aras moo di buurub dëgg-dëgg budul
Dee bis, du folliku bis, Alhamdu Lillaahi !
2- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Ag réer a tee ñépp naa Alhamdu Lillaahi !
3- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Ibliis a tee ñépp naa Alhamdu Lillaahi !
4- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Bon dong a tee ñépp naa Alhamdu Lillaahi !
5- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Ñun ñépp war na nu naa Alhamdu Lillaahi !
6- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Mbooleem ñi baax a ngi naa Alhamdu Lillaahi !
7- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Mbooleem jullit ñaa ngi naa Alhamdu Lillaahi !
8- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Ñi sopp Yàlla a ngi naa Alhamdu Lillaahi !
9- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Ñi Yàlla sopp a ngi naa Alhamdu Lillaahi !
10- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Mbooleem sëriñ sa a ngi naa Alhamdu Lillaahi !
11- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Mbooleem murid ya a ngi naa Alhamdu Lillaahi !
12- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Yàlla a ngi sant ñi naa Alhamdu Lillaahi !
13- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Yàlla a ngi dolli ñi naa Alhamdu Lillaahi !
14- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Ña yor Aras ña nga naa Alhamdu Lillaahi !
15- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Malaaka yépp a ngi naa Alhamdu Lillaahi !
16- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Saytaane rekk a waxul Alhamdu Lillaahi !
17- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina ndaxam
Buurub Aras moo saxal Alhamdu Lillaahi !
18- Ñun ñépp yal na nu sax cig sant sax ci lu ñuy
Santaane lépp, saxal Alhamdu Lillaahi !
19- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina na sax
Ci séeni làmmiñ bu wér Alhamdu Lillaahi !
20- Alhamdu Lillaahi Rabbil haalamiina na sax
Ci xol yi sax gu rafet, Alhamdu Lillaahi !
21- Santay ndigël moo nu war moo jaadu fàww ci Ñun
Moo taaru fàww ci Ñun, Alhamdu Lillaahi !
22- Yàlla a rafet, ëpp naa wax lëf ludul “Jarajëf”
Du wax lu bon du ko def, Alhamdu Lillaahi !
23- Moo gën ku nekk, waxam gën jépp wax, jëfam it
18
Noreyni KEBE
Gën jépp jëf, ayibul, Alhamdu Lillaahi !
24- Tabaarak’Allaahu moo mat moo desul desewul
Te moo matal gaa yi mat, Alhamdu Lillaahi !
25- Alhamdu Lillaahi rekkay wax ju am ja njariñ
Ñun ñépp yal na nu naa Alhamdu Lillaahi !
26- Ba tàbbi Firdawsi biir ak bitti tàbbi gu wér
Xol yépp sedd nu naa Alhamdu Lillaahi !
27- Alhamdu Lillaahi Ñun noo am lu jomb lu gën
Ay réewi réewaki pal Alhamdu Lillaahi !
28- Alhamdu Lillaahi Yàlla a ëpp lépp lu rëy
Xam koo gën it lépp lëf Alhamdu Lillaahi !
29- Alhamdu Lillaahi Ñun noo ëpp Buur i njariñ
Gën koo dalum xel Asal Alhamdu Lillaahi !
30- Alhamdu Lilaahi Ñun noo ŋoy ci Kenn ku gën
Buur ak dagam ya ko wër Alhamdu Lillaahi !
31- Alhamdu Lilaahi Ñun noo jàpp dëgg ci lëf
Lu wér lu rëy lu rafet Alhamdu Lillaahi !
32- Alhamdu Lilaahi Ñun noo am lu sedd xolub
Koo jis te jomp bëtëm Alhamdu Lillaahi !
33- Alhamdu Lilaahi Ñun noo am ku sikk newul
Te am lu sikk newul Alhamdu Lillaahi !
34- Alhamdu Lilaahi noo am Ñun lu kenn amul
Njëgam te ken du ko am Alhamdu Lillaahi !
35- Alhamdu Lilaahi noo am Ñun lu jomb ci Ñun
Lu gën Kajoor ak Bawol Alhamdu Lillaahi !
36- Alhamdu Lilaahi Ñun noo am lu buuraki dag
Amul te gën la ñu am Alhamdu Lillaahi !
37- Alhamdu Lillaahi ag baadoola dem na nu dem
Nu bokk féewoo soree Alhamdu Lillaahi !
38- Alhamdu Lillaahi noo am may gu farlu gu rëy
ak fit wu rëy mayewul Alhamdu Lillaahi !
39- Alhamdu Lillaahi noo am may gu itte ju rëy
Ak xel mu rëy mayewul Alhamdu Lillaahi !
40- Alhamdu Lillaahi Ñun noo am Sëriñ bu nu fob
Jébbal Boroomub Aras Alhamdu Lillaahi !
41- Alhamdu Lillaahi noo baax ab Sëriñ te juboo
Juboo gu sax gu rafet Alhamdu Lillaahi !
42- Alhamdu Lillaahi noo gën ab Sëriñ ku nu moy
Gën ñépp ab Yonnen it Alhamdu Lillaahi !
43- Alhamdu Lillaahi noo am Ñun Sëriñ bi te am
Yonnen ba am Yàlla nag Alhamdu Lillaahi !
44- Alhamdu Lillaahi Yàlla a taawu lépp njariñ
Te moo nu taawu ca kaw Alhamdu Lillaahi !
45- Alhamdu Lillaahi Bàmba a tax nu xam lu nu xam
Moo tax nu am lu nu am Alhamdu Lillaahi !
46- Alhamdu Lillaahi Bàmba a tee nu bokk torox
Moo tee nu dee sax ba tay Alhamdu Lillaahi !
19
Noreyni KEBE
47- Alhamdu Lillaahi Bàmba a tax nu teggi lu bon
Raw jépp lor jotu yiw Alhamdu Lillaahi !
48- Alhamdu Lillaahi Bàmba a tedd moo nu teral
Ñun ñépp moo nu bégal Alhamdu Lillaahi !
49- Alhamdu Lillaahi Bàmba a may ku nekk ndawal
Kunee ngi yàpp ak a bég Alhamdu Lillaahi !
50- Alhamdu Lillaahi Bàmba a am njariñ maye ndam
Yal nay mbégam sax fi Ñun Alhamdu Lillaahi !
51- Alhamdu Lillaahi Yàlla a sax te yal na saxal
Gëmam gu wér ga ci Ñun Alhamdu Lillaahi !
20
Noreyni KEBE
Jooyal ma junni bi at …
Jooyal ma junni bi at saa waa ja moo mat a jooy
Ku ñàkk saa waa ja sab xol ñor nga bis-bisi joy
Sa waa ja ken masu koo am kenn dootu ko am
Da daa fajal ñépp daan ak mer di baax’ak a nooy
Masee fu koo jis te deeful jis ku mel ni mu mel
Toolub ngërëm bi mu daa bay fenn daawu ci booy
Mbooleem ndigël yi la daa def lenn daawu ci des
Daawul def it dara cis mbon-mbon du rëbb bu sooy
Sooyul ña koy topp sooyuñ yal na am mébetam
Ci gàncaxam gi mu daa wolleek a bay ba du gooy
Te yal na am ci njabootam gii mu dëddu ne mes
Lu dal xelam ma te tooyal ab xolam ba mu tooy
Suuf ak kaw ak asamaaw ak ñépp a ngiy rët a kay
Jooyug demam rekk “ëh-ëh!” àddinaa mat a joy
Amul ku dem gii mu dem bettul ci suuf’aki kaw
Demam gi bette na koo jis rët na bay xaw a sooy
Cëy Yàlla cëy Yàlla cëy cëy cëy ma dellu ne cëy
Te dellu rekk ni cëy at mii nu nekk a di kuuy
At mii nu nekk du maasum at ya màgg ya wéy
Te at mu màgge ni moom it dootu niit a ka xuuy
Te at ma Yonnen ba delloo saaba yépp gëlam
At mii ko ñaareelagun tee ngéen a dëgmu te jooy !
21
Noreyni KEBE
Mo jaa lu deefi defati …
Moo jaa lu deefi defati ?
Moo jaa lu deefi waxati ?
Moo jaa ku deefi royati ?
bu kilifay moy ak a fo
Ku war a boole aw nitam
di waar'akay ful seeni gëm
Defu ko far boolew nitam
di moy’akay soow ak a fo
Addina yàqu na yaxeet
ku yabu wut barab bu wéet
Nekk fa tay jaamook a wéet
Te sori kuy moy ak a fo
Addina yàqu na te kat
kilifa yoo ko yàq kat
Du séenu nit ko yàq kat
Kilifa yoo fiy dox di fo
Ku yabu wub sa bunt kër
Rekk te daw nelawi far
Nelaw a gën génn di lor
Aw nit’akay lorook a fo
Ay am na nag ndegam nelaw
Mu bon milee fiy tax a raw
Xamal ne kon ken dóotu raw
Nelaw gënul lëf ndere fo
Waa juy nelaw gënul kudul
Waa juy foyeek a moy ndigël
Nelaw du tax ñu xëy la fal
Néewal ko tey moyu ku fo
Kilifa day moyu ku fo
ba noppi tey tere ku fo
Bu manl a tee nag kenn fo
na tëye boppam bañ a fo
Sawara bég na mbég mu rëy
Ngir moy yu rëy yi deefi moy
Ngir xam ne xéll ne ñi moy
Lay dunde ëllëg ak ñi fo
Foo tollu gis góor ak jigéen
Di jaxasook ay dox di been
Sunnas Yonnen bi ak a téen
Rekk di xal-xaleek a fo
Àjjana yal na bég ci Ñun
Sëriñ bi yal na bég ci Ñun
Yonnen ba yal na bég ci Ñun
Ak Yàlla miy aaye ku fo
Seriñ bi wax na bind na
22
Noreyni KEBE
Def na nu gis te digle na
Yii moo ko war kat wàcci na
Musu la moy musu la fo
Waxam a gën waxi ku ne
Jëfëm a gën jëfi ku ne
Waayam a gën waayi ku ne
Waayam ja dëgg nag du fo
Foo gis ku nee fi waayam a
muy fok a nekk foppam a
Bul gëm ne koo ku waayam a
waayam ja dëgg dóotu fo
Foo gis ku nee fi waayam a
Muy fok a moy xumaagam a
Foo gis ku nee fi waayam a
Weddil ndegam gis nga mu fo
Wurus bu yàggee am xumaag
Xaalis bu yàggee am xumaag
Lépp lu yàgg am xumaag
Xumaag a fiy ruus’ak a fo
Bàmba wurus wu sell la
Waayam dërëm bu sotti la
Te ku ameb rax yaru la
Ab rax a bon day tax a fo
Xànjar lu dar-dar ci wurus
Asal bu kob tëgg di gis
Xam ne dafay niru wurus
Nde du wurus, wurus du fo
Wurus lu sellul bokku ca
xaalis lu weexul bokku ca
Bàmba lu baaxul bokku ca
nan bàyyi fo jullit du fo
Na bàmba bëgg ku na mel
Yal na nu Yàlla may nu mel
Noo nële ndax te ku na mel
Doo fo te doo digle ku fo
Yal na sëriñ bi dimbëli
Seexam yi nag te dimbëli
Murid yi géppug dimbëli
Ba xam ne ken du moy du fo
Lii rekk lay fexe ci Ñun
Nde soxla wul dara ci Ñun
Lu dul nu def murid yu gën
Yu kenn dul seere ñu fo
Moo tax ma naa la yal na am
Li miy mébet ci Ñun nu am
Li niy mébet ci moom itam
kon lépp jag te ken du fo
23
Noreyni KEBE
Sëriñ bi yaa gën alal
Sëriñ bi yaa gën alal, yaa gën barab, gënu nit
Ku way ci yaw mucc am mbooleem mébët ya azal
Yaa gën ci nit bakkanam, yaa gën ci nit barabam
Yaa gën ci nit mbokkam ak léppam ku weddi xamul
Kuy bëgg boppam akay wut kenn akay fexe lëf
Mbaa muy fexee yewwi kuy jëm fenn dof la fajal
Man naŋ ma dimbali nag baa fàtte saa bakkan ak
Saa mbokk ak saa barab ak lépp, man nga, defal !
May ma’g cofeel’it ci yaw buy fàtte loo sama xol
Bànneexi àddina ak àllaaxiraa ki mbugël
Saytul sama'b xol ba dóotul fas ludul sa ngërëm
Sàmmal samay cér ba dóotul jëf ludul sa ndigël
Jox naa la saa xol bi ak saa cér yi nanguko yor
Saytul ma, sàmmal ma, jur gaa ngii ma jox la, fabal !
Sama'b xol ak sama cër yii yépp ak sama xel
Nay dëkk fàww ci yaw may dëkk nag ci sa xel
Saa xol bi feesal ko dell ak yaw ba xam ne ludul
Yaw dóotu am ci sama xol as mbarab sumu dal
Fegal ma képp ak lu nekk ak fépp dar ma ci yaw
Bu lenn dox sama digg ak yaw ludul li nga sol
Lu bëggë dox sunu digganteeti far ko falaŋ
Ci àll, boo ma defoon sax mbubb sol ma ma jël
Naa far di bopp ci yaw, naa far di tànkk ci yaw
Naa far di kenn ci yaw, saa aajo jaa ngi fajal
Def naala wéttal ci àll ak kër te déf la nday ak
Baay ak najaay ak Sëriñ yaa jar lu nekk azal
24
Noreyni KEBE
Bastul a bonn …
1. Bastul a bon bu dee taxaw
Seytaane daaldi jog taxaw
Ne jongamaa jogal taxaw
Naxle ma gaa yi bey aaréen [arachide]
2. Mbooleem murit bu bey aaréen
Waxtu wu dee làpp aaréen [bacc guerte]
Xel ma ne lapp ci jigéen
Ku farluwul sa lépp neen
3. Jongama day jaayoo ka jaay
Murit bu jog mu ne ko kaay
Tàggale kookug laxasaay
Ak itte muy niru jigéen
4. Jigéen a bon ci ab murit
Moo gëna bon ci ab murit
Lépp lu bon ci ab murit
Yaw bu ko séenu bu ko séen
5. Ku jox jigéenam la mu laaj
Xañ sëriñam la mu ko laaj
Ku xañ Sëriñ nag la mu laaj
Réccu ko gaa yi déggléen
6. Murit da daa wut sëriñam
Tey daw lu dul ab sëriñam
Ba Yàlla jox kob sëriñam
Ak njariñam mu boole leen
7. Wut léena wut seen ub sëriñ
Moo gën di foo ka wut njariñ
Ab sëriñ ay joxey njariñ
Tey ak ëllëg nde du leneen
8. Ku muñ te sàkku sab sëriiñ
Te baña wut lenn njariiñ
Leegi nga gis lépp njariiñ
Jog di la wut laxasuleen
9. Koo xam ne kii la deefi wut
Lépp da laa mujj di wut
Loo soxla am te doo ko wut
Amleen i yitte, yewwuleen
25
Noreyni KEBE
10. Ku bëgga mujj jariñu
Day loru ngir ku jariñu
Loru na doora jariñu
Ag dëgg a ngii te bir na leen
11. Ku bëgga dem day awu yoon
Koo xam ne kii awul u yoon
Mbiram dafay dënnoo ka xiin
Waaye du gis lu dul ngëléen [vent poussiereux]
12. Ku joxewul deefu ko jox
Lu ñu jiwul du mana sax
Ku naxewul deefu ko nax
Yëgleen ne gaa yi bey aréen.
Traduction Francaise
QUE LA BASCULE EST DANGEREUSE AV MOMENT DE LA PESÉE
1. Que la bascule est dangereuse au moment de la pesée
Le diable se tient alors prêt
Et dit àla belle : "tiens-toi prête
A m'aider à tromper ceux qui ont cultivé l'arachide".
2. Pour tout aspirant ayant cultivé l'arachide,
Si, au moment où il bat (son) arachide,
Sa pensée se fixe sur la femme,
S'il ne prend garde (verra) tout son (effort) réduit à néant
3. La belle a l'habitude de se pavaner et de (se) vendre
A l'aspirant qui réagit elle dit : "viens",
Réussit à le détacher de son ardeur
Et de sa détermination ; (ainsi) il se féminise.
4. Que la femme est néfaste à l'aspirant
C’est la pire chose pour l'aspirant.
(Et) tout ce qui est défavorable à l'aspirant
Ne l'attend pas, ne le vise pas.
5. Qui satisfait la demande de sa femme,
Refuse la demande de son guide (spirituel)
Et qui refuse à son guide ce qu'il demande,
Aura à s'en répentir, comprenez bien.
6. L'aspirant (d'habitude) est en quête de son guide
En s'éloignant de tout ce qui n'est pas son guide
Jusqu'à ce que Dieu lui octroie et son guide
Et son intérêt à la fois.
7. Persévérez dans la quête de votre guide (spirituel)
C’est préférable à l'amusement et à la quête de profits
(Car) c'est le guide qui octroie le bienfait
Aujourd'hui et demain et point autre chose.
8. Qui patiente et cherche (l'agrément) de son guide,
26
Noreyni KEBE
S'abstient de rechercher le moindre profit,
Verra bientôt tous bienfaits
Venir à soi, soyez persévérants.
9. Alors ce qui constitue l'objet de toute quête
Finira par être entièrement à votre quête,
Vos désirs s'exaucent ainsi sans quête,
Soyez déterminés et en éveil.
10. Qui aimerait finir par jouir du bien
Doit d'abord connaître le malheur, car qui a le Bien
A d'abord eu le Mal avant le Bien
Voilà une vérité et vous en êtes certains.
11. Qui veut partir emprunte la (bonne) voie
Celui qui n'emprunte pas la (bonne) voie,
Verra ses affaires (s'assimiler) au tonnerre et aux nuages
Et il ne verrait que vent poussiéreux
12. Qui ne pourvoie ne sera point pourvu
Ce qui n'est pas semé ne saurait germer
Qui ne trompe pas n'est point trompé
Soyez (en) avertis, vous autres qui avez cultivé l'arachide
27
Noreyni KEBE
Rikk Asan lu man a xew …
1. Rikk Asan lu mana xew
Awal ndigal te yaru yaw
Kon dinga làq wépp yiiw
Tey ak ëllëg maa la ko wax
2. Mbooleem lu deefi jog di wut
Yar a ko gën gën koo rafet
Moo jara dox junni bi at
Di wut Sëriñ bu la ko jox
3. Ku yaru rekk a mata am
Ku yaru rekk a mata xam
Ku yaruwul matula am
Matula xam turam wa sax
4. Ab yar li tax amul moroom
Day taxa gën fa say moroom
Tey taxa gën fa sa boroom
Ku la yarul rekk a la nax
5. Ku la mayoon i junni yit
Te jàppul ub yar may la yit
Leegi nga gis junni ya rot
Woroomi yar for ko te sex
6. Ku yaruwul matula yër
Ku yaruwul matula yor
Ku yaruwul alku na far
Ku yabu far tàbbal ko pax
7. Ab yar yamoowul ak dara
Ku ko amul amul dara
Ku ko am it ñakkul dara
Sëriñ bi yal na nu ko jox
8. Ab yar la deefi gën e nit
Ab yar la deefi sute nit
Ab yar la deefi raw e nit
Nde du alal ale rëy i yax
9. Juddoo ki jur matla damoo
Ragal Yàllaa mata damoo
Te ku ko am du ko damoo
Ngir dootu gis baaxam ga sax
10. Ku gis boroomam dootu gis
Boppam te moona dootu gis
Moroomam it te dootu gis
Daraaka wax wax i larax [futilité]
11. Moo tax ba Yàlla ku ko xam
Yaru te ken du ko xam
Te amul ub Sëriñ ndaxam
28
Noreyni KEBE
Ku xam du weddi lii ma wax
12. Ngir Yàlla nee ci Alxuraan
Wut al ci man ab kerkeraan [escalier]
Teb Sëriñ ay ab kerkeraan
Asan jàppal ci jile wax
Traduction francaise
De grâce ô Assane, quoi qu'il advienne
Obéis aux recommandations et sois poli,
Tu acquerras ainsi tout avantage,
Aujourd'hui et demain, je te l'affirme.
A tout ce qui constitue l'objet de quête,
La bonne éducation est préférable et plus belle
Cest elle qui vaut une randonnée de mille années,
A la recherche d'un guide capable de l'octroyer.
Seul l'éduqué mérite d'être compté parmi les siens ;
Seul l'éduqué mérite d'être connu ;
L'impoli ne mérite pas d'être compté,
Son nom même ne mérite d'être connu.
Ce qui fait que rien ne vaut une bonne éducation
C'est qu'elle rend (l'homme) meilleur devant ses semblables
Elle le rend également meilleur devant le MAITRE
Qui ne t'a pas éduqué t'a trompé.
Si quelqu'un t'offrait des milliers (de francs)
Mais s'abstenait de te donner une bonne éducation,
Tu verrais bientôt les milliers (de francs) se perdre
Pour être ramassés et consommés par l'éduqué,
L'impoli ne mérite pas l'intérêt
L'impoli ne mérite pas que l'on se charge de lui,
L'impoli enfin est maudit
On n'a plus qu'à le mettre en terre.
La bonne éducation n'est égale à rien (d'autre)
Qui ne l'a pas n'a rien ;
(Et) qui l'a n'est privé de rien ;
Plût à Dieu que le Cheikh nous l'octroie.
C’est par la bonne éducation que l'on est meilleur à quelqu'un ;
C’est par la bonne éducation que l'on surpasse les gens ;
C’est par la bonne éducation que l'on devance les gens,
Mais non par les biens matériels et la naissance.
La naissance et la richesse ne valent pas que l'on s'en vante ;
Cest la foi en DIEU qui mérite que l'on se vante ;
Or qui en est pourvu ne s'en vante pas,
Car il n'aura plus conscience de son mérite.
Qui a conscience de son SEIGNEUR ne voit plus
Sa propre personne ; et du reste, il ne voit plus
Son semblable ; il n'a plus conscience
De rien, et ne parle de futilités.
29
Noreyni KEBE
Voilà pourquoi qui a une connaissance de DIEU
Acquiert la politesse, et nul ne peut l'avoir
Sans pourtant avoir un guide spirituel ;
Celui qui sait ne mettra point ces paroles en doute.
Car c'est DIEU qui, dans le Coran* a dit :
"Cherche le moyen de M'atteindre ‘’
Or c'est le guide spirituel qui constitue ce moyen
Assane retiens bien ces propos.
*Cf. Coran S5, V35 où il est dit : "ô vous qui avez cru ! Craignez pieusement DIEU, recherchez tout ce
qui vous ouvre ses portes" ... etc •••
30
Noreyni KEBE
Ma jog caw ub yar …
1. Ma jog caw ub yar
Ku amul ub yar
Ku amul ub yar
Mata caw ub yar
2. Koo xam ne loo wax
Mu teg ca ay wax
Weddee ko say wax
Ngay muñ akay mer
3. Moo ana teggiin
Ak yoonu teggiin
Ak waxi teggiin
Ja daa jubal mbir
4. Foo waxe as mbaat
Nu teg ca as mbaat
Su bon su tax mbaat
Soosee nga wax far
5. Teggin a ngiy jooy
ñoñam a ngiy jooy
Yal na ñu far jooy
Yépp ak sunuy lor
6. Tey foo waxes lëf
Nit wax ca as lëf
Te du ca wax lëf
Lu dul dangay nar
7. Du la ni nar nga
Du la ni fen nga
Yaw waaye gis nga
Sa wax ja muy cor
8. Ndaw dootu ër mag
Ndaw dootu rus mag
Day dog nawug mag
Xañ kob céram far
9. Moo tax ba fan yi
Gàtt te may yi
Tuuti te moy yi
Bareeki kër-kër
10. Teggiin a lay may
Gudd fan ak way
Ak jàmm akug doy
Moo lay may ug jur
11. Teggiin a gën yaay
Te moo gën it baay
Moo gën bariy gaay
Jàpp ko yaw yor
12. Moo mata taqool
31
Noreyni KEBE
Moo ëppa tàggool
Day not akay mool
Te du caw ab yar
Traduction francaise
1. Je m'en vais donner le fouet
A celui qui n'a pas d'éducation ;
Qui n'a pas d'éducation
Mérite de recevoir le fouet.
2. Celui (là) qui, à chacun de tes propos
Oppose ses propres propos,
Seulement pour attaquer tes propos
Et te rendre résigné et enragé.
3. Où trouver la bienséance ?
La voie de la bienséance,
Ainsi que les parlers respectueux
Qui ont toujours réduit les conflits ?
4. A chaque fois que tu tiens le moindre propos,
On y oppose un autre petit propos
Dont la perfidie rendra le petit propos
Que tu as émis caduc.
5. Les bonnes manières se désolent ;
Leurs semblables se désolent ;
Que nous autres les pleurions
Tous, ainsi que nos maux.
6. Aujourd'hui, dès que l'on émet un avis,
Quelqu'un y ajoute quelque chose ;
Et il n'y ajoute rien d'autre
Que "tu mens".
7. On ne dit du reste pas "tu mens".
On ne dit pas non plus "tu ne dis vrai" ;
Mais tu es bien conscient
De la manière dont on attaque tes dires.
8. Le jeune n'épargne plus l'adulte ;
Le jeune n'a plus de considération pour l'adulte ;
Il coupe le souffle à l'adulte,
Et le prive du rang (qui lui est dû).
9. Voilà pourquoi l'espérance de vie
Est courte, et les bienfaits
Limités, alors que les péchés
Sont nombreux, ainsi que les difficultés.
10. C’est la bienséance qui octroire
La longévité et l'équilibre,
La paix et (l'état de) satisfaction;
C'est elle qui octroie aussi la richesse.
11. La bienséance est préférable à la mère,
32
Noreyni KEBE
Elle est également préférable au père ;
Elle est meilleure qu'un nombre important d'amis,
Tâche de te l'attacher.
12. Qu'il est utile de se l'attacher!
Qu'il est dangereux de s'en départir !
Elle maîtrise et modèle,
Sans avoir besoin de donner le fouet.
33
Noreyni KEBE
Lu dul ni ñokket
1. Lu dul ni ñokket
Rekk ni waqet
Dabi ngërëm kat
Gaa yi du mbir kat
2. Dee gi du jekki
Day xëy di songe
Di gont songe
Te ku ko gis rët
3. Du diñe mukk
Du fande mukk
Du ñàkk lekk
Tey xëy di gis nit
4. Farlu gu nekk
War na ku nekk.
Ngir nit ku nekk
Dee gaa ngi koy-wut
5. Ndaw ñaa ngi koy daw
Mag ñaa ngi koy daw
Ku nee ngi koy daw
Te ñépp lay jot
6. Ku mu jotul tey
Jot la bu dul tey
Nelawatoo kay
Bul gëmm say bët
7. Dégg nga li daa xew
Te gis lilee xew
Xam li fasoo xew
Gaawal fexee set
8. Dee fab na say maam
Fab maami say maam
Ba amatoo maam ·
Dana la fab yit
9. Dee ken la dul ba
Donte dafay ba
Yonen ba lay ba
Kay ngën ji aw nit
10. Dee daw ko dum xel
Muslu ko dom xel
Fàww mu teeral
Gaalam fi sag wet
11. Fexeela am yaw
Ngërëm ak uw yiiw
Te ba fen ak jëw
Fab sa bakkan not
34
Noreyni KEBE
12. Dangaa fasoo dem
Te ku fasoo dem
War na balaa dem
Yobbalam mat
13. Yokkal sa itte
Yokk gu metti
Tey daw werente
Fàww ak barig jot
14. Moyul barig jot
Ngir ku barig jot
Kenn la dul jot
Te ñéppa koy jot
15. Ku bari ag jot
Foo ko gis ak bët
Nanga ni téppét
Seytaane saa kat
16. Bu ko dawey xél
Dawe ko am xel
Ngir koo dawey xél
Mu sànni law yat
17. Ku bari am Xel
Day dawe am xel
Nde du dawey xél
Lii laa la wax kat
Traduction francaise
1. Seule la ferme résolution
De courir éperdument
A la recherche de mérite
Est ce qu'il y a à faire, ô amis.
2. La mort ne reste jamais en place ;
Elle attaque dès le matin,
Elle attaque le soir,
Et qui la voit s'épouvante.
3. Elle ne reste jamais sans déjeuner ;
Jamais elle ne manque de dîner ;
Elle n'est jamais à court de subsistance
Alors qu'elle voit des gens.
4. Toutes dispositions
Incombent à n'importe qui,
Car, chaque être humain
Est sans cesse recherché par la Mort.
5. Les jeunes la fuient ;
Les vieux la fuient ;
Chacun la fuit,
Mais elle atteindra tout le monde.
6. Qui n'en est pas atteint aujourd'hui,
35
Noreyni KEBE
Le sera une autre fois ;
Tu ne dors plus,
Ne ferme pas les yeux.
7. Tu es au courant de ce qui s'est toujours passé,
Tu as vu ce qui est en train de se passer,
Tu sais ce qui compte se faire ;
Hâte-toi de te purifier.
8. La mort a ravi tes ancêtres,
Elle a ravi les ancêtres de tes ancêtres,
Jusqu'à ce que tu n'aies plus d'ancêtres ;
Et elle te ravira de même.
9. La mort n'épargne personne ;
Si elle devait épargner quelqu'un,
Ce serait le Prophète,
Qui est le meilleur des hommes.
10. Fuir la mort n'est pas raisonnable ;
Chercher à s'en protéger (non plus) n'est raisonnable;
Elle accostera inéluctablement
Sa pirogue à tes côtés.
11. Tâche (alors) d'acquérir
Le mérite et le Bien
D'abandonner mensonge et médisance,
Et de soumettre ta passion profane à ta volonté.
12. Tu es destiné à partir ;
Or qui se destine à partir,
Doit avant son départ,
S'assurer d'un viatique complet.
13. Accentue (donc) ta résolution
D'une façon radicale ;
Fuis les discussions vaines
Et le désœuvrement.
14. Méfie-toi du désœuvrement,
Car qui dispose de trop de temps (mort),
Ne rejoindra jamais personne,
Et tout le monde le rejoindra
15. Qui dispose de trop de temps (mort),
Dès que tu l'as en face en toi,
Déguerpis aussitôt
(Car) il s'agit de Satan.
16. Et ne le fuis pas par la course,
Fuis-le par l'intelligence ;
Car celui que tu fuis par la course
Te lancera son bâton (entre les jambes)
17. Qui est doté d'intelligence
Doit fuir intelligemment,
Mais non en courant (à pieds) ;
Voilà ce que j'ai à te confier
36
Noreyni KEBE
Murid degg bul merr …
1. Murid dëgg bul mer te bul jàpp mer
Mer ak jàpp mer day alak ab murid
2. Mereel say ayib, gërëm sab sëriñ
Te daw nemmatam nag ba am say murid
3. Te neexal dereet, ku neex ul dereet,
Du am ay ngërëm du am ay murid.
4. Bàyyil jom ngirub rëbb day ñàkk jom
Ba jam doora am jom te rëbb ay murid
5. Jom ak jikko ak fulla yii yatt a bon
Jigul rëbb ak ub dag jigul ab murid
6. Ku am yatt yii du am yatt yii
Ngërëm, bàrke, wërsëg; yëgal yaw murid
7. Defal ndànk tey waaf akay daw ba jam
Bariy jikko kat moodi gàkk ub murid
8. Di am fulla ak jikko ak jom ba tax
Sa rab wii di raw yaw lu jar lii murid
9. Di sàggan di sàggan ba saw rab di raw
Nga waat ug ndawal yaw moyul lii murid
10. Digal naa la aw yiiw te man lii ma war
Defal lii ku def lii di ngën jiy murid
11. Defal boo defee ma def boo deful
Ma def tey digal man beneen ub murid
12. Te kat sant naa la gërëm naa la yit
Damaa bëgg ngay jiitu bépp ub murid .
13. Duyal naa la ndab laa ngi nii boo yanoo
Te tuuroo ko am bàrke am say murid.
Traduction francaise
DE GRACE, Ô L'ASPIRANT NE SOIS NI COLEREUX NI RANCUNIER
1. De grâce, ô toi l'aspirant, ne sois ni coléreux ni rancunier ;
La colère comme la rancune rendent l'aspirant maudit.
2. Mets toi en colère contre tes défauts, et rends grâce à ton guide (spirituel);
Evite aussi son mécontentement afin d'avoir tes (propres) disciples.
3. Et puis sois d'un abord facile, car, qui n'est pas d'un abord facile,
N'aura ni agréments ni (ses propres) disciples.
4. Abandonne la fierté (excessive), un chasseur se doit d'être sans orgueil
Jusqu'à abattre sa proie pour retrouver la fierté ; or le chasseur, c'est l'aspirant.
5. La fierté (excessive), le (mauvais) caractère et la morgue, que ces trois (travers) sont mauvais!
Ils ne sont favorables ni au chasseur, ni au serviteur, ni à l'aspirant.
6. Qui est marqué de ces trois là ne peut avoir ces trois-ci :
Le mérite, la grâce et la chance ; sois en averti ô l'aspirant.
7. Agis avec prudence, te planquant et courant afin d'abattre (ta proie) ;
Etre instable (de caractère) est certes une tare pour l'aspirant.
8. Avoir trop mauvais caractère, trop de morgue et une trop grande fierté,
Et voir sa proie s'échapper, comment peut-on en arriver là, ô l'aspirant ?
37
Noreyni KEBE
9. Te montrer négligent, d'une négligence telle que ta proie réussit à t'échapper,
T'empêchant ainsi d'avoir du gibier, tâche d'éviter cela, l'aspirant.
10. Je t'ai (à présent) conseillé le bien, et c'est cela mon devoir.
Tache de suivre ce conseil ; qui agit ainsi devient le meilleur des aspirants.
11. Suis ce conseil ; si tu le fais, je le ferai quant à moi, si tu ne le fais pas,
Moi, je le ferai et le conseillerai à un autre aspirant.
12. Et (puisque) tu as toute ma gratitude et ma reconnaissance,
Il me plairait que tu arrives à devancer tous les autres aspirants.
13 . J’ai rempli pour toi le récipient; si tu l'emportes .
Sans en perdre le contenu, tu acquéras et la grâce et tes (propres) disciples.
38
Noreyni KEBE
Xarit dëgg yewwul…
1. Xarit dëgg yewwul ba yewwuy jariñ
Te bul nég ba yewwuy yem ak ay nelaw
2. Sa kër gii nga nekk ak murit yii la ëw
Du tee kat nu xëy fab la bis suuli yaw
3. Nga des nag fi sam kan ni comm ak sa jëf
Te dootoo gis it menn mag mbaate ndaw
4. Nangay nekk fii yaw te sam xel ne fee
Ku jàppul xelam teg ko fee ñàkk u yiiw
5. Bàyyil saw yaram tey fi kër gii mu jëf
Te fab nag sa xel teg ca kër gee te daw
6. Li ngay mujje moo tee nga koo jëkke far
Dangay mujj daw bis te doo daw ba raw
7. Dabal leegi aw yiiw te daw leegi lor
Lu wéy dab ko fajtil lu dul xol bu wow
8. Te mbey sax nawet lay jariñ gaa ya bey
Beyal rikk waa jii balaa noora ñëw
9. Te kuy dox di sàggan ba farmànku jot
Mbeyam dootu faj gàcce ngir dootu taw
10. Nawet moo di dunyaa mbey ay jëf ju yiiw
Dugub jee di sag pey bu sottee nga naw
11. Ku bey yaw na ngay bey ku dul bey nga bey
Te bul geesu añ bul tàyyeekay taxaw
12. Bàyyil xëy di waxtaan akay tëddi lal
Ku koy def te tuuboo ko sag pey ngelaw
13. Dangay sàmm ay béy yu am laf [force] te sob
Sa cér yee di say béy moyul ay nelaw
14. Nangay xëy di jëf jëf ju saf sab sëriñ
Akay wax wa illaa nga xëy jàppu yaw
39
Noreyni KEBE
Traduction
Ô ami, réveille toi pendant que l'éveil sert ;
N'attends pas le moment où l'éveil équivaut au sommeil.
Cette belle situation que tu as dans ta maison, ainsi que ces fidèles qui t'entourent,
Ne peuvent t'empêcher d'être mis un jour en terre.
Alors, tu resteras dans ton trou, tout seul avec tes actes
Et jamais tu ne reverras ni adulte ni jeune.
Tâche d'être ici, mais avec l'esprit tourné là-bas
Qui ne réussit à fixer son attention là-bas perd l'avantage.
Abandonne maintenant ton corps à cette demeure qu'il a créée ;
Oriente ta conscience vers cette autre maison, et gare toi.
Que ne commences-tu par faire ce à quoi tu finiras par être réduit ;
Tu finiras par vouloir te sauver un jour, alors que jamais tu ne pourras t'échapper.
Tâche d'avoir dès à présent le Bien, évite dès maintenant le Mal.
Tenter d'acquérir ce qui est révolu, ne saurait servir qu'à assécher le cœur.
Le travail agraire du reste, c'est pendant l'hivernage qu'il profite à ceux qui le font;
Travaille donc, ô homme, avant que ne survienne la saison sèche.
Et qui néglige (son travail) jusqu'à la fin de la période hivernale, -Sa peine ne saurait plus (lui) éviter la honte, car il aura cessé de pleuvoir.
Cest l'hivernage qui est le bas-monde, et le travail agricole les bonnes actions ;
Le mil constitue ta paie. A terme, tu ( en) seras ravi.
Quant l'autre travaille, travaille; quand l'autre ne travaille pas, travaille.
Ne te préoccupe point de rétribution, ne te fatigue ni ne t'arrête jamais.
Abandonne l'habitude de discourir (vainement) et de te vautrer dans des lits ;
Qui le fait sans s'en répentir (verra) sa paie s'anihiler.
Tu es le gardien de chèvres fortes et capricieuses ;
Tes membres sont (ces) chèvres ; méfie-toi du sommeil.
Prends l'habitude d'agir selon l'agrément de ton guide (spirituel),
Et de parler aussi ; ou alors, astreins toi au silence.
40
Noreyni KEBE
Xarit bul tamal sa bopp aw lejal
1. Xarit bul tamal yaw sa boppuw lëjal
Te loo man la taggoolatee diw lëjal
2. Kafeek iy ataayaaki mbiskit jarul
Di xaareeka ñaaneeka leb cam muñal
3. Ndegam am nga naanal ndegam nag amoo
Faral muñ ba am kooti déggal ndigal
4. Guroo kug ndawal yit jarul leb batey
Ka leb war dafay ñàkk sër ñakk njël
5. Te ab lal bu ñuy tëdd akuw fas ba tey
Jarul leb ku leb yii bakkan lay lebal
6. Ndegam bëg nga yii nag te am séeni njëg
Fabal mbaa nga jox sab sëriñ far mu jël
7. Nangay not bakkan yaw te kat bum la not
Bu lay woo ci loo xam ne woorul bañal
8. Bu lay wooti cis mbor da lay lor bañal
Bu lay gàdduloo nit da lay nax dawal
9. Leb ak leble ak gàddu nit yatt yii
Ku koy def asaI lee lu bon xëy ko dal
10. Ngor ak diine ak worma yii jeex na tey
Te yii nag bu jeexee lu dul ay desul
11. Ku ñëw may ko loo man te bañ koo lebal
Lilee gën di soowooka réccooka xul
12. Lebal Yàlla moo gën lebal ab laram
Dawal lépp luy lëjle ak kuy lëjal
41
Noreyni KEBE
Traduction francaise
1. Ô ami, n'habitue pas ton corps à des servitudes,
Car ce dont tu n'arrives plus à te passer constitue une dépendance.
2. Le café, le thé ou le biscuit ne valent
Ni parasitisme, ni sollicitation, ni emprunt. Essaie de t'en passer !
3. Si tu en disposes (café, thé ... ) bois, si par contre tu n'en disposes pas,
Tâche patiemment d'attendre le moment où tu en seras pourvu ; sois obéissant.
4. La cola ou la viande, de même ne valent pas que l'on emprunte
Celui qui est astreint à l'endettement, c'est celui là qui n'a ni vêtement, ni nourriture.
5. Un lit pour dormir et un cheval également
Ne valent pas l'endettement. Celui qui s'endette pour ces choses le fait (uniquement) pour son
plaisir.
6. Si tu désires ces choses et disposes de leur prix,
Prends les ou (mieux), offre les à ton maître pour son service.
7. Tâche de maîtriser tes sens et évite d'en être maîtrisé
S'ils te poussent vers l'incertain, résiste.
8. S'ils te poussent vers la dette, ils te portent préjudice, refuse !
S'ils te demandent d'avaliser quelqu'un, ils te trompent, fuis !
9. L'endettement, le prêt et l'aval, à ces trois (travers)
Qui s'adonne est à court terme voué au malheur.
10. (Le sens de) l'honneur, la foi et la pudeur (ces vertus) ne se voient plus
Or si (ces vertus) n'existent plus, il ne (nous) reste plus que le mal.
11. Qui vient (te solliciter), offre lui ce que tu peux sans (rien) lui prêter.
Cela est préférable aux querelles, aux regrets et aux plaintes
12. Le prêt consenti à DIEU est préférable à celui consenti à son esclave;
Fuis tout ce qui constitue l'objet de troubles et de gêne.
42
Noreyni KEBE
Masamba sembal ci geejug BAMBA …
1. Masàmba sëmbal ci géejug Bàmba sangu ba set
Tey xuus akay wéy ba far def waa ju yegg ju lab
2. Xuusal te wéy, dëgg bul gajafal sa der bile yaw
Ba noppi nag te setoo ; kuy wàlli làmb na ub
3. Daasal sa itte mu ñaw bay mel ne jaasi ju wat
Ngay dagge ndog yi ni lawbey dox di dagge garab
4. Melal ne gaynde, ku mel neg gaynde, ken du la dog
Ngir képp kuy doge day daw gaynde moy fu mu sab
5. Doo seeru ngën jib murit muy jog di waaxu di wéy
Ba jongamay bari man-man nag ba jog di ko dab.
6. Doo seeru ngën jiy murit muy nekk fenn di wax
Ba jongomay jog di fookay jëm fa booba barab
7. Ngën jiy murit fu mujëm, Seytaane dootu fajëm
Te jongamaa di ndawal seytaane, ëy bu ko nob !
8. Loo xamne day mujj nëb bis, loola yaw bu ko nob
Te jépp jongama joo gis lee mu médd ba nëb
9. Sël-sël ja muy dëkke ak bun-bun ja, yaw bu ko gis
Seetal ba muy nëb, ba sax yay jàpp lex ya ''Ajab".
10. Bul gis lexam ya mu naa nes-nes ba tax nga ne cas
Sa itte jox ko ko ; kon boo dee, sa lay wa du jub
11. Jigéen a dog gaa ya daa wut Yàlla maa la ko wax
Ngir moo di pettngalub[piege] Seytaane, yaw bu ko jub
12. Dangaa amew sas, te yaw sellal ko rekka la war
Bul génn sas wi di wut añ, lee nga seeru sa ndab
13. Di jaamu Yàlla bu wér, tey topptoo ndigalal
Sëriñ bi, sas waa ngi nii kat ; bey ko yaw bu ko tëb
14. Lii doy na wollëre, jàppal wollëree ngi wu rëy
Masàmba sab dénka ngii, santal ma Yàlla te fab
15. Wéyal ba géejug sëriñ bi far la wann tërëx
Nga far ne mengg ba neefaa "Bacc wéy na ba lab”
16. Tey làmb jaa ngii di gor, koo seeru nag mi ngi tëb
Ngir bëgga ub, yobbu ndam; yal nan ko ub te nga ub.
43
Noreyni KEBE
Traduction
1. Ô Massamba, plonge dans l'océan de BAMBA (afin) de proprement te laver;
Avance en longues brasses jusqu'à atteindre (l’objectif) et te noyer.
2. Evolue dedans, et vas-y à fond ; ne te contente pas de te mouiller la peau,
Sans réussir à te rendre propre ; que celui qui va à l'arène y aille pour vaincre.
3. Affine ta foi, rends la pareille à une machette (aussi coupante) qu'un rasoir,
Pour élaguer les obstacles tel le « lawbé » coupant des arbres,
4. Sois tel un lion ; à qui ressemble au lion, nul ne coupe le chemin.
Car tout coupeur (de route) fuit le lion, et évite là où il a rugi.
5. On ne verra jamais l'aspirant vertueux se décider à s'en aller,
Et quelque belle, entreprenante, se mettre à le rejoindre.
6. On ne verra jamais l'aspirant vertueux intervenant quelque part,
Et une belle se mettre à s'amuser et à y diriger ses pas.
7. Là où l'aspirant vertueux se dirige, Satan renonce à aller;
Or c'est la belle qui est le suppôt de Satan, évite de t'en amouracher.
8. Un objet dont on sait que le destin est de pourrir, ne t'en éprends pas !
Or, pour n'importe quelle belle, c'est à court terme la crève et la décomposition.
9. Ses sempiternels artifices et ses senteurs, n'y sois pas sensible;
Ne considère que le moment de sa décomposition, quand les asticots se repaîtront de ses
joues, que c'est étonnant !
10. Evite, à cause de l'éclat de ses joues, d'être réduit
A remettre entre ses mains toutes tes préoccùpations ; car alors, à ta mort, ton plaidoyer ne
convaincra pas.
11. C'est la femme qui a coupé la route à ceux qui étaient en quête de DIEU, je te l'affirme;
Car elle est un piège posé par Satan, ne t'en approche pas.
12. Tu es porteur d'une charge et ton unique devoir est de la purifier ;
Ne sors pas de ton carré pour la quête d'un repas, bientôt tu recevras ton écuelle.
13. Adorer réellement Dieu tout en te préoccupant des recommandations
Du Cheikh, voilà ton carré ! laboure le (au lieu de) le sauter.
14. Cela, comme gage de fidélité est suffisant, prends en soin, quelle grande fidélité !
Voilà Massamba ta leçon, rends grâce à Dieu et reçois (la).
15. Avance, jusqu'à ce que l'océan du Cheikh, entièrement te submerge;
Que complètement tu disparaisses et l'on dise : "Bàcc s'en est allé se noyer".
16. Or donc voilà les jeux ouverts ; tout le monde se démène
Pour vaincre et emporter le trophée ; Dieu fasse que nous soyons vainqueurs ainsi que toi
44
Noreyni KEBE
Ma wax fi Ahmadou Kumbay…
1. Ma wax fi Ahmadou Kumbay wax ju koy taxa raw
Seytaane ak bakkan ak mbooleem lu deefi ragal
2. Yaw mii di Ahmadu tey ndab laa ngi nii jegesil
Tey tibb akay sex te farluy lekk nag ba doyal
3. Feyal sa bor yépp yar saw nit te yar sa bakkan
Tey wut ngërëm tey siyaaraakay yoraale alal
4. Dee yobbu bor day waral kër-kër ku xam du ko def
Sàggan ba dee yori bor yal nan ko Yàlla fegal
5. Foo xam ne boo fa demee yokkoo fa yaw bu fa gëj
Te képp kuy gëj fa muy yokkoo du jub du jubal
6. Notal sa bakkan te foo tolluy siyaareji yaw
Bul yittewoo rekk ay soxnaaki doom aki njël
7. Di soxlawoo ay ngorookay yeggleeka jamoo
Du tax nga yegg du tax ngay jam ngërëm ba mu fèl
8. Tey boo bëggee yegg mbaa ngay jam ngërëm ba mu fèl,
Jaayal sa bopp sëriñ Tuubaa te jox ko sa xol
9. Kuy jëndi soxnaaki fas jëndal sëriñ bile yaw
Ku am sëriñ bile am loo xam ne ëpp na xel
10. Wax naa la man la ma xam santal te def la nga man
Te jéema jog defi mbooleem lépp loo fi manul
11. Xarit du faj lëf lu dul laabiire ab xaritam
Te lii ma wax doy na ag laabiire daane fabal
12. Neexal deret te maneel ak mbokk ak dëkkandoo
Bul moslu kenn te kuy moslooti dee ko mosal
13. Bul mer te kuy mer demal neexal ko bam béga bég
Bul topp yaw sa bakkan bul topp yit ku xamul
14. Murid bu dul julli ak bay julli bul ko xalam
Foo gis ku bon defaral mbaa boo munul suturaal
15. Boo dee xalam xalamal sag bon te fate bonug
Jaambur xamal ne bonug jaambur xalam ko warul
16. Murid bu ndaw ak bu mag ak koo fu gis te mu gëm
Yonen ba ak Yàlla jàppal seeni xol di seral
17. Tiijaan ak ub xaadir ak koo seeru dee ko bégal
Mbégum jullit rëy na kuy merloo jullit texewul
18. Jullit bu mer Yàlla mer buy bég mu daaldi bég it
Moo tax nga xam ni ku fiy merloo jullit xamagul
19. Jàppal sa ndey ak sa mbooleem bokk yépp teral
Te bul weranteek u nit yaw ngir werante gënul
20. Noppil te bul dox di sikkal ay sëriñ aki ngér [yoon]
Bul jàpp mukki sëriñ ak séeni ngér di bonal .
21. Sëriñ si ak séeni ngér ak séeni nit defaral
Tey fonk tey suturaal ndax Yàlla far la gënal
22. Bul xaste mukk te mbooleem waa ju jog di la xas
Tuubal te bul fayu yaw kon Yàlla far la fayul
23. Lii moo di saafara ·naanal kon nga wér ni pelèngg Te am li ngay wut te dootoo gis lu deefi ragal
45
Noreyni KEBE
Traduction :
Je men vais ici confier à Ahmadu Kumbë des recommandations propres à le faire échapper
A Satan, à l'âme charnelle, ainsi qu'à tout ce qui constitue l'objet de crainte.
ô toi Ahmadu, l'écuelle (à nourriture) est là bien disponible, approche !
Sers toi et mange ; hâte-toi d'en consommer jusqu'à satiété.
Acquitte toi de toutes tes dettes, éduque tes gens et maîtrise ta passion (profane);
Tâche aussi d'acquérir le mérite et de rendre des visites pieuses avec des biens en viatique.
Mourir avec des dettes (non payées) provoque des tourments ; jamais ceux qui savent ne le feront.
Etre négligent au point de mourir avec des tettes, que DIEU nous en préserve !
Des endroits où tu es sûr de gagner quelque chose, ne t'absente pas trop longtemps ;
Ceux qui désertent les lieux qui leur sont favorables ne peuvent ni être honnêtes ni bien se conduire
Maîtrise ta passion profane et habitue-toi aux visites pieuses;
Evite de ne te préoccuper que d'épouses, d'enfants et de vivres. ;.
Se préoccuper uniquement de fiançailles, de mariages et de concurrences (galantes),
Ne te fera réussir; cela ne te fera pas non plus atteindre le mérite.
Si aujourd'hui, tu désirais réussir, ou atteindre pleinement le mérite,
« Vends » ta personne à Seriñ Touba et abandonne-lui ton cœur;
Si les autres cherchent à acheter femmes et chevaux, tâche quant à toi d'acquérir le Cheikh.
Qui a ce guide-là aura (des biens) dépassant tout entendement.
Je t'ai indiqué ce que je sais, rends grâce et fais ce que tu peux ;
Mais (surtout), tâche d'aller accomplir tout ce qui t'est difficile (à faire)
L'ami ne sert à rien d'autre que d'être bienveillant à l'égard de son ami.
Et ce que je te dis là suffit comme bienveillance, donc, prends (le)
12. Tâche d'être sociable, ménage patents, et voisins ;
Ne sollicite personne, mais qui vient (te) solliciter, pourvois-le.
13. Ne te mets jamais en colère, et à celui qui se fache, trouve le moyen de lui rendre la joie.
Ne te soumets pas à ta passion (profane), ne suis pas (non plus) les ignorants.
14. De l'aspirant qui ne fait pas ses prières et de celui qui s'en acquitte, ne t’occupe.
Devant le corrompu, tâche de (le) corriger ; si tu ne le peux, montre toi indulgent.
15. Si tu dois réfléchir, réfléchis sur tes propres travers en oubliant ceux
Des autres ; sache que s'occuper des travers des autres n'est pas bienséant.
16. Au jeune aspirant comme à l'adulte, ainsi qu'à n'importe qui croyant
Au Prophète et à DIEU, évertue toi a apaiser le cœur.
17. Le Tidiane, le Qâdir ainsi que n'importe qui d'autre, tâche de les rendre heureux,
Le bonheur d'un croyant est inestimable ; qui mécontente le croyant ne peut-être bienheureux.
18. Chaque fois qu'un croyant se fâche, DIEU se fache ; s'il se réjouit, DIEU se réjouit (de meme)
Voilà pourquoi qui contrarie un croyant n'est point encore informé.
19. Rends à ta mère ainsi qu'à tous tes proches tout l'honneur qui leur est dû.
Et évite de te disputer avec les gens ; les disputes ne sont pas ce qu'il y a de mieux à faire.
20. Sois réservé et évite de te mettre à critiquer des guides (religieux) ainsi que des confréries ;
Ne te hasarde jamais à flétrir les guides (religieux) et leurs voies.
21. Les guides (religieux), de même que leurs voies et leurs adeptes, ménage-les.
Considère-les et témoigne-leur de l'indulgence afin que DIEU te rende meilleur.
22. Ne te mets jamais à insulter (les autres) ; et si quelqu'un se met à t'insulter,
Repens toi et abstiens toi de lui répondre ; ainsi, DIEU te vengera.
23. Voilà un remède, bois! Tu seras alors complètement rétabli;
46
Noreyni KEBE
Addina bëgg na laa fab waaye…
Addina bëgg na laa fab waaye yaw nanga bañ
Lu fab fab it nanga fab say tànk samp fi suuf
Jekkil te riigu fi suufus Yàlla sii bu fi jog
Loo jëm jëm it kaw dangay dellooti rekk fi suuf
Lalub gitax ak lalub weñ ak lalub tagar ak
Lalub selen boo ci tëdd it wàcci dellu fi suuf
Mbaam ak gëléem ak fafal-naaw ak wata'aku ngélaw
Loo ciy war it dula tee xëy bis ne céng fi suuf
Néegub ñax'ak mbaari seng ak taaxi suuf aki kaw
Loo yàgg yàgg ci ñoom it génn dugg fi suuf
Cerey lay ak wataboor ak ndàbb ndiir aku sëb
Ak mbuum akub cox a faf yam bis ba ngay gane suuf
Baadoola ak buur akub dag ñépp ñoo xala yam
Lu yàgg yàgg dañiy booloo ne meng ci suuf
Jëlub lingeer ak jëlub jaam ak jëlub xaj a yam
Loo jël jël it dee gi xëy bis jël la dénk la suuf
Adduna wor na mag ak ndaw wor ko leegi bu wér
Te ŋoy ci Yàlla ki yor suuf ak ñi nekk ci suuf
Lu yàgg yàgg nangay def Yàlla wettalu xol
Moo lay fegal lori kaw, moo lay fegal lori suuf
Suuf ak kaw ak fépp a am lor fépp a am njariñ it
Ku dëddu am njariñal kaw, am njariñ li ci suuf
Am yitte ciw sas ba fàtteb añ du tee añ a ñëw
Fexeel a am ca kaw'ug pal fàww am ko ci suuf
Ñun ñépp yal nanu am ag pal ca kaw gu rafet
Gu sax te am ko fi suuf it ñépp féete nu suuf !
47
Noreyni KEBE
Traduction
Le bas-monde ne cherche qu'à te ravir, mais toi, tâche de résister ;
Quelque soient ses efforts pour t'élever, maintiens fermement tes pieds à terre.
Demeure bien assis sur cette terre de DIEU, sans la quitter;
(Car), quelque soit ton ascension, tu finiras toujours par revenir à terre.
Que ce soit le lit (fait) de tige de mil, le lit en métal ou fait de branches (d'arbuste)
Ou le lit (fait) de végétaux, quelque soit celui que tu utilises, tu finiras toujours par revenir à
la terre.
Que ce soit l'âne, le chameau, l'avion, l'automobile ou le vent,
Quelque soit ta monture, cela ne peut t'empêcher de rester un jour, seul en terre.
Que ce soit la case en paille, l'abri fait de tôles, le bâtiment en rez-de-chaussée ou à étage,
Quelqu'y soit la durée de ton séjour, tu en sortiras toujours pour entrer en terre.
Le couscous à la viande fraîche, un couscous ordinaire à haricot
De même que l'épinard et le son sont parfaitement pareils le jour où tu arrives en terre
Le simple manant, le roi ou le serviteur sont parfaitement à égalité ;
A la longue, ils finiront par disparaître tous ensemble en terre.
Epouser une princesse, une captive ou une chienne sont parfaitement équivalents ;
Quelque soit le nombre de tes mariages, un jour, la mort te prendra pour te confier à la terre
Le bas-monde a trahi vieux et jeunes ; trahis le dès maintemant ;
Pour te cramponner à DIEU, le GERANT de la terre et de ceux qui s'y trouvent.
Aussi longtemps (que tu vivras), fais de DIEU le Compagnon de ton cœur;
C’est LUI qui te préserve du Mal (venant du) haut et de celui (venant du) bas.
Le bas comme le haut comportent aussi bien le mal que le Bien ;
Qui se détourne du (bas-monde) gagne et le Bien du haut et celui du bas.
terre.
Se préoccuper de la mission jusqu'à oublier la récompense n'empêche guère l'octroi de (cette)
récompense ;
Tâche de gagner l'élection du haut et celle du bas. Dieu fasse que nous soyons tous triomphalement
élus la-haut
(Une élection) durable aussi bien qu'ici bas ; que n'importe qui soit en dessous de nous .
48
Noreyni KEBE
Adina moo mana nax
1. Adina moo mana nax ndaw nax na jopp ku xam
Na dooni buur aki baadoolooti sax anañu ?
2. Na daa dawal seeni fas tey jàppi jaam aka maf[ravir comme un aigle]
Di jaay i jaam aka jital moo ku xam ana ñu ?
3. Ku xam fia daa xëy di war njar fukk ak ña fi daa
Xëy bis toj ub dëkk. ñuy jooyooka daw ana ñu ?
4. Ku xam ña daa tëggi junjuo woote fiépp di ñëw
Ale gaa ya daa xeebi baadoolooka xas ana ñu ?
5. Moo jaa ña mbooloo ya daa wër gàddo seeni fital
Di sënk [vanter] akay sank tey jii nag ku xam ana ñu ?
6. Moo jaa ña daa dox di wëndéeluy xareeka wasal [razzier]
Akay piccaarooka [se barricader] dàkk48 uw nit ku xam ana nu ?
7. Na daa rey uw nit akay rëylooka jekki ca kaw
Di xulli ay gët akay xooleeka bew ana ñu ?
8. ña daa reyanteeka woo aw nit ñu xëy ni tirim
Di diglu seeniy ndigal ñoñee ku xam ana ñu ?
9. Na daa bañanteeka bindanteeka yooli sëriñ [payer des marabouts]
Akay añaanaka ñaanoow ay ku xam ana ñu ?
10. Na daa weranteeka bojjantey gobar di xuloo
Di naan akay màndi moo ñooñee ku xam ana ñu ?
11. Moy Yàlla moo bon ku koy def ag mujjam du rafet
Mbooleem ña daa def lu baaxul ken xamul ana ñu
12. Na doon i buur aki baadooloo ngi bokk ni mes
Ci suusi gaaya rëyoon ak gaaya sew anañu?
13. Tuubal te sant te wut jaajëf fa Yàlla bu wér :
Bul bokk mukk ci ni neefaa ku xam ana ñu
49
Noreyni KEBE
Traduction
Que le bas-monde est habile à la tromperie IL a trompé tellement (de gens) ! Qui sait
Ce que ceux qui étaient rois ou simples manants sont devenus ?
Ceux qui faisaient galoper leurs chevaux, faisant des captifs et ravissant,
Vendant des esclaves et les conduisant, qui sait ce qu'ils sont devenus ?
Qui sait où ceux qui passaient leur temps en selle sur leurs "pur-sang" ainsi que ceux qui,
Razziaient les villages provoquant pleurs et exodes se trouvent (maintenant) ? "'
Qui sait où ceux qui faisaient battre le jungjung [tambour royal] pour réunir les gens,
Ainsi que ceux-là qui méprisaient et insultaient le peuple se trouvent-ils(maintenant) ?
Et ceux-là que des gens entouraient, se chargeant de leurs fusils,
Les flagornant et les perdant, qui sait ce qu'ils sont aujourd'hui devenus ?
Et ceux qui ne faisaient que vagabonder, guerroyer et razzier,
Se barricadant pour se soustraire aux gens, qui sait où ils se trouvent (à présent)?
Ceux qui tuaient les gens, se gonflaient d'orgueil et s'installaient bien haut,
Roulant des yeux et toisant si orgueilleusement le monde, que sont-ils devenus ?
Ceux qui passaient leur temps à s'entretuer et à rassembler les gens
A l'écoute de leurs directives, qui sait ce qu'ils sont devenus ?
Et ceux qui se haïssaient, se jetaient des sorts et recouraient aux féticheurs,
(Ceux qui), cruels, se souhaitaient tous les malheurs, qui sait ce qu'ils sont devenus ?
Ceux qui se disputaient, se poignardant dans les querelles,
Se livrant à des beuveries, qui sait ce qu'ils sont devenus ?
Que le péché est éxécrable ! Qui s'y adonne ne peut connaître une fin heureuse ;
Tous ceux-là qui se complaisaient dans le mal, nul ne sait ce qu'ils sont devenus !
Aussi bien les rois que (leurs) sujets ont tous ensemble disparu
En terre , les grands comme les petits, que sont-ils devenus ?
Repens toi, rends grâce à (DIEU), et tâche résolument de trouver l'agrément de DIEU;
Tâche de ne jamais faire partie de ceux dont on se demande ce qu'ils sont devenus.
50
Noreyni KEBE
Seriñ bi ayee na jew …
1. Sëriñ bi aaye na jëw yonen ba aaye na jëw
Te Yàlla aaye na jëw ngir jëw dafay alake
2. Jëw mii dafay joxe ay bon-bon di rékk ngëm it
Luy rékki ngëm di joxe ay bon-bon dafay alake
3. Ku dib jullit lum bon bon bul ko jëw bu ko yab
Yab ub jullit jëw ko day suufeel akay alake
4. Ku dolliwul sab Iiggéey it bul ko faf joxe des
Te fab sa dagga di lokkat mbir la muy alake
5. Jullit bu dee jëw moroom um jullitam dafa dof
Ngir jàpp saw yiiw di jox nit dof la koy alake
6. Doo gis ku yewwu ku am xel mukk muy jëw u nit
Ku yewu gistee ko muy def mukk luy alake
7. Sëriñ bi moo yewwu yal nan yee ba dootunu def
Jëw ak lu koy nuru sax ak lenn luy alake.
8. Sëriñ bi deefu ko gis muy jëw te nanguwul it
Ku jëw kilee dib sëriñ moo feg lu daa alake
Traduction :
1. Le Cheikh a interdit la médisance, le Prophète a (aussi) interdit la médisance ;
DIEU également a interdit la médisance, car la médisance rend (l'homme) maudit.
2. Cette médisance-là n'est propre qu'à octroyer le mal et ébranler la foi
Et ce qui ébranle la foi et donne de mauvais attributs rend maudit.
3. Quelque soient les défauts du croyant, ne le calomnie pas, ne le méprise pas ;
(Car) mépriser un croyant et le calomnier abaisse (l'homme) et le rend maudit.
4. A défaut de chercher à augmenter ses bienfaits, que l'on se garde (au moins) de les distribuer ;
Et se mettre à brûler son grenier, est un fait propre à la malédiction.
5. Un croyant qui se met à médire de son frère croyant n'est qu'un sot,
Car, se mettre à abandonner son mérite à un autre, est une sottise à rendre maudit.
6. On ne verrait jamais un homme éveillé, plein de raison se mettre à médire (des gens) ;
On ne verrait (en effet) un homme intelligent faire des actes qui rendent maudit.
7. Que le Cheikh est éveillé ! Dieu fasse qu'il nous réveille au point que l'on ne s'adonne plus
Ni à la médisance, ni à rien de semblable, ni à rien (du reste) qui soit propre à rendre maudit.
8. On ne verrait jamais le Cheikh se mettre à médire, et il n'accepterait jamais
Que l'on médise. Quel grand guide ! C'est lui qui (nous) a préservés de tout ce qui rend
maudit.
51
Noreyni KEBE
Yaw foo dajeeteek u nit jàppal…
1. Yaw foo dajeeteek u nit jàppal sa bopp bu wér .
Seytaane mbër la te foo jekkeek u nit ma nga fa
2. Te fuw jullit daje bay waxtaane Yàlla di bég
Fa lay gëne loru nit ndax kenn foogu ko fa
3. Ab sàcc boo ko yëgul foogoo ko lay gën a bon
Te sàcc rekk la foo koy yëg mu daw sori fa
4. Wattul ma ab jaxasoo ngir waxtu woo jaxasoo
Di gis ku fay lor di gis koo lor nga lor loru fa
5. Nëbbul berul yaw te doyloo Yàlla wëlliis u nit
Beréb bu mbooloo dajeey xooleeka wax dawe fa
6. Fu fiw jullit daje déglul koo fa dégg mu wax
Ag dëgg jàppal ku wax aw fen nga ree te ba fa
7. Ab yar bu sotti bu ànd ak dëgg moo mata yor
Yii yaari yëf ku ko yor fum jëkki jekki ji fa
8. Nangay naxante ba doo moy Yàlla doo moy u nit
Bis boo tëlee lii ma wax jaaral fa Yàlla ne fa
9. Te bul naxanteek u nit bay def lu Yàlla bëgul
Bul dab mbégum surga nag bay jot merum kilifa
10. Bu kenn wax lu amul bay tax nga naa ko amul
Koo gis ci mbooloo mu naa nit fen nga kat gënu fa
11. Bul jéppi kenn te bul jey it sa bopp bàyyil
Lu dul la Yàlla dogal kon foo fu dem tane fa
12. Fug dëgg jëm nanga jëm foofee ngërem fa la jëm
Fug dëgg moy nanga moy foofee ngërëm newu fa
13. Foo gis ku xellu ngërem lay wut du wut lu ko moy
Foo yëg werenteeti gaawal daw ngërem newu fa
14. Werente seytaane moo koy sooke mbaate ndawam
Ku wax bu dee dëgg mbaa muy fen ëral ko ko fa
15. Ku fen fi yaw bul saxal bul dàq bul toroxal
Te bul gëm it suturaalal fen wa bam joge fa
16. Te bul ko jëw it gannaawam kon mu yobbu sa jëf
Ndegam bawoo na fi yaw sax Yàlla mii ma nga fa
52
Noreyni KEBE
Traduction
CHAQUE FOIS QUE TU RENCONTRES DES GENS Ô (AMI) ...
Chaque fois que tu rencontres des gens ô (ami), sois parfaitement réservé ;
(Car) Satan est un champion, et il se trouve partout où l'on est en public.
Et c'est là où les croyants se réunissent pour parler de DIEU dans la joie,
Qu'il porte davantage préjudice, car personne ne l'y croirait;
Un voleur (qui opère) à notre insu et sans que l'on s'y attende est d'autant plus dangereux
Or, ce n'est qu'un voleur; dès que l'on s'aperçoit de sa présence, il s'empresse de déguerpir
Méfie toi des assemblées (mondaines), car à chaque fois que tu te mélanges (aux gens)
Tu te verras porter du tort, et porter tort ; tu auras nui et on t'aura nui.
Cache-toi et isole-toi; suffis toi à DIEU, en dehors (du secours) des gens.
Ces endroits où les gens s'assemblent pour discourir vainement, déserte-les.
En tout endroit où sont rassemblés des croyants, si tu entends quelqu'un
Dire vrai, acquièsce ; si on profère un mensonge, contente toi d'en rire.
Une parfaite éducation doublée de franchise, voilà ce qu'il faut avoir;
Tache de toujours fréquenter les endroits où se mettent les gens qui sont dotés de ces deux qualités
Evite par la diplomatie de violer les lois de DIEU et de porter tort aux gens ;
Si tu te trouves incapable de réussir cela, va (alors) t'abandonner à DIEU.
Evite cependant de te concilier les gens jusqu'à contrarier la Volonté Divine ;
Il ne faudrait pas, sous prétexte de contenter le subalterne, braver la colère du Maître.
Que jamais à quelqu'un qui dit une contre-vérité, tu dises que cela n'est pas ;
(Car) celui qui, en public se met à démentir les gens n'y est certainement pas meilleur.
Ne t'enrage contre personne, ne te surestime pas et abandonne
Tout ce qui n'est pas du fait de DIEU ; tu arriveras ainsi à être le meilleur où que tu iras.
Dirige toi là où se dirige la vérité, c'est la destination du mérite ;
De l'endroit d'où se détourne la vérité, détourne-toi, le mérite ne s'y trouve pas.
Les gens avertis (ont l'habitude de) rechercher le mérite, et jamais autre chose
De là où tu entends les discussions vaines, déguerpis vite, il n'y a point de mérite
Les discussions vaines sont toujours suscitées ou par Satan ou par ses suppôts.
A celui qui exprime des propos, qu'ils soient vrais ou faux, abandonne-les-lui
Si on te tient des propos mensongers, abstiens toi de confirmer, d'infirmer ou de ridiculiser (l'auteur)
Mais évite (aussi) de croire; accepte pudiquement le mensonge jusqu'au départ (du menteur)
Et ne le calomnie pas après son départ, il emporterait tes (bonnes) actions ;
Même s'il a pris congé de toi, DIEU LUI est toujours là.
53
Noreyni KEBE
Jàppal sa xol bi defar
1. Jàppal sa xol bi defar ngir xol bi moo di sa kër
Defar sa kër bàyyi sab xol moo lu muy xala faj ?
2. Sa kër lu jag jag te sab xol taq ripp lu bon
Du tax nga gën kat fa Yàllay mbaami ngongk aki xaj
3. Defar sa xol bii ba xol biy ler-lereeka melax
Moo gën di wut néeg ak iy sàkket yu fatt taraj
4. Na dëkkewon taaxi kaw tey jëf lu bon ña nga tey
Ca sëg ya ñuy cawiy yar foo toll dégg "faraj".
5. Lu kër gi jag jag bu ruugiy rot nga génn ko dem
Yaw rekk ken du la topp it menn xel du ko daj
6. Te rikk ak sa bakkan Jàppal ma addina wor
Te daaldi wéy bala laa wor kon sa mbir du fi lëj
7. Am wéttal al ñàkk wéttal waaji ñoo xala yem
Buur ak dagam ya mu àndal ñoo xaloo yami muj
8. Buur ak ña koy topp ñoo yem kepp ndax ku ci dee
Ni cumm cim kan mu xat lëndëm ba far ni kërëj
9. Njegam dangaa bëgga am wéttal wu dul xala deñ
Tijjil sa xol bile yaw tàbbal ci Yàlla te tëj
10. Loo tëj ci sab xol lu dul moom it mu xëy ne la mes
Nit koo fi gis dana dee ndab loofu gis dana toj
11. Né boo fi gis da na tas kër goo fu gis dana tas
Waa kër ga yit mujj tas àddina mbég du ci xaj
12. Addina kër la gu bon ngir masla jag te du jag
Ku aajewul, lud jagam say aajo ken du ko faj
54
Noreyni KEBE
Traduction :
1. Emploie toi à te purifier le cœur car c'est le cœur qui constitue ta demeure ;
A quoi (le fait de) rendre sa maison propre en laissant son cœur (souillé) peut-il servir?
2. Quelques soient les qualités de ta maison, si tu as le cœur souillé de pêché,
Cela ne saurait te rendre auprès de DIEU meilleur que l'âne ou le chien.
3. S'occuper de son cœur à le rendre brillant et étincelant,
Vaut mieux que de se construire des maisons avec des palissades étanches.
4. Ceux qui logeaient bien haut, mais se complaisaient dans le pêché sont aujourd'hui
Dans les cimetières, subissant le fouet dont on peut partout entendre les coups;
5. Malgré tout l'agencement de ta maison, dès que (ton) âme tombe tu la quittes pour t'en aller
Tout seul, sans aucune compañie ; nulle conscience n'y penserait.
6. Et, de grâce, avec ton âme chamelle, emploie-toi à trahir le bas-monde ;
Pour t'en aller (vers le salut) avant qu'il ne te trahisse ; ainsi tes affaires ne seront pas
emmêlées ici-bas.
7. Sache qu'avoir de la compañie ou être seul sont parfaitement pareils;
Le prince ainsi que les serviteurs qui l'accompagnaient, sont tous voués au même destin.
8. Le prince tout comme sa suite sont strictement égaux, car celui d'entre eux qui trépasse,
Se retrouve tout seul dans un trou étroit et d'une obscurité absolue.
9. Si, (à présent) tu désirais avoir une compañie qui ne te quitterait plus jamais,
Ouvre ton cœur, place-y DIEU, et referme-le.
10. Quelque soit ce que tu enfermerais dans ton cœur, si ce n'est LUI, cela te filerait un jour (entre les
doigts)
Tout être humain est destiné à mourir, tout récipient finira par se casser
11. Tout édifice est voué à la chute, toute demeure est destinée à la ruine ;
Et la maisonnée également finira par être dispersée ; dans ce bas-monde, le bonheur n'a pas
de place.
12. Le bas-monde est une bien mauvaise demeure ; il n'a jamais satisfait, et jamais il ne satisfera.
Qui ne se préoccupe que de sa bonne marche, ne verra jamais ses besoins satisfaits .
55
Noreyni KEBE
Xam naa ne ag ñakka mandoo bon …
1. Xam naa ne ag ñakka maandoo bon te lëf jaru ko
Lu dul jariñ dara tey lor kay ku xam bàyyi ko
2. Kuy bëkknéegu lu muy jaglooka sacc aka mos .
Du faj lu dul yeut ko ay, wañifiig peyam lor i ko
3. Di sàcc ak ay mos ci loo moomul xamal ne du faj
Say aajo ngir aajo sàcc ak mos asal faju ko
4. Ag mbëkknéeg aki géej ak teen akiy dex a yem
Kuy bëkknéegu bu toppee bakkanam alaku
5. Ag mbëkk néegu ka koy ngéejooka daw di ca jëm
Ab dof la rekk nde ag dex nit du daw wuti ko
6. Kuy bëkneegu bu neewul jàrr, yewwu bu wér
Te def ku sàmm iy céram, ay dal ko, yiw sori ko
7. Koo xam ne day seeru yëf yoo xam ne moomu ca lëf,
Te bëgg cas lëf, bu baaxul far ca mos ; moyu ko
8. Sa kër sëriñ noo ca tàbbee rekk génne na yaw
Bul génne kas lëf lu dul loo xamne jox na la ko
9. Sa kër Sëriñ loo ca gis, ak kër gu dul këram it
Muñal ba am ca ndigal, moo gën nga jalgati ko
10. Loo gis lu sew sew bàyyil, ngir lépp loo mana fab
Lu sew sew it daaldi rëy, ag moy du tuuti ba ko
11. Murid lu dul sopp ab sangam te jox ko xolam
Ak ug juram, def la muy wax, daw meram waru ko
12. As cuukar ak warga ak lem ak kafeek i dërëm
Ak lépp lëflu la neeful fab ko, sàggane ko
13. Kuy bëkknéegu juroomi yëf gënul ci mbiram
Sàcc ak dox ak xoole ak dégluy wax ak feni ko
14. Farlul te roy nag ci Jibriilak kemam ya ca kow
Kuy bëkknéegu ci ñi lay roy te dégg nga ko
15. Malaaka moo maandu moo am ngor te sell i mbir it
Du fen du nettli ndéeyit, am xelam daju ko
16. Malaaka yépp dañuy def tekk déglu ndigal
Lu Yàlla digle ñu daal cay maase jog defi ko
17. Malaaka menn du jog def lëf te xam ne ndigal
Ñëwul ; ndigal du ñëw it muy deeti néggandiku
18. Sëriñ bi dëgg, defal jikoy malaka ci Ñun
Ak gëm ga ak yar ba ak kàttan ga ; yokke nu ko
19. Ak wér ga ak way ga ak sellal ga ndaxte nu am
Sag cant yaw ñàkka am sag cant lëf jaru ko
56
Noreyni KEBE
Traduction:
1. Que le défaut d'honnêteté est exécrable, rien ne le vaut !
Ce qui est sans utilité et pone préjudice est, en vérité à délaisser par quiconque est conscient
2. Qu'est ce que le chambellan a à s'approprier, à voler et goûter?
Cela ne sert qu'à l'engager dans des conflits, diminuer sa rétribution et lui porter préjudice.
3. Sache que voler et consommer des biens illicites ne peuvent combler
Ton manque ; car le besoin, le vol et la consommation de biens illicites ne peuvent le justifier
4. (La fonction de) chambellan est semblable à la mer, au puits et au fleuve ;
Qui ( exerce la fonction de) chambellan risque la perdition, s'il est possédé par ses passions.
5. Celui qui aspire à (cette charge) de chambellan et s'y précipite
N'est qu'un sot; car un homme (raisonnable) ne se précipite pas (inconsidérément) vers un
fleuve.
6. Qui exerce la fonction de Chambellan, s'il n'est pas d'une vigilance aigüe, d'une réelle lucidité
S'il n'a pas une grande maîtrise de soi, recoltera le Mal et verra le Bien s'éloigner de lui.
7. Celui qui observe des choses parmi lesquelles rien ne lui appartient,
Dont il a envie d'une partie et (d'ailleurs) finit par y goûter s’il n’est pas honnête, évite-le.
8. De chez ton guide spirituel, sors comme tu es entré ;
Ne repars avec rien d'autre que ce qu'il t'a lui même offert
9. Chez ton guide spirituel, quelque soit ce que tu y vois, et même ailleurs que chez lui,
Attends patiemment l'autorisation au lieu de te l'approprier.
10. Ce que tu y verrais, quelque soit son insiñifiance, ne t'en occupes pas ; car tout ce que tu
pourrais t'y attribuer,
Quelque infime soit-il deviendrait important ; un pêché n'est jamais anodin, abandonne-le.
11. L'aspirant n'a de devoir que (de) vénérer son Maître, lui attribuer son cœur,
(Lui faire don) de ses biens, suivre ses directives, et se garer de sa colère.
12. Un peu de sucre, du thé, du miel, du café et quelques deniers ;
Ainsi que tout ce qu'il ne t'a lui-même offert, délaisse-le.
13. Pour (qui exerce la fonction de) chambellan, voici cinq travers non indiqués :
Le vol, le vagabondage, le furetage, ainsi que l'écoute (aux portes) et le rapport mensonger.
14. Sois (donc) résolu et imite Jibriil et ses pairs de là-haut ;
Qui exerce la fonction de chambellan, c'est de ceux-là qu'il doit s'inspirer, tu en es averti.
15. Que l'ange est vertueux ! qu'il est plein d'honneur, et que ses mœurs sont saines !
Ile ne ment ni ne rapporte les secrets ; cela ne lui effleure même pas l'esprit
16. L'ensemble des anges se tient prêt, à l'écoute de directives ;
Ce que DIEU commande, à l'unisson, ils se mettent à l'appliquer.
17. Aucun ange ne saurait se mettre à faire quelque chose, sachant que l'instruction (pour cela)
N'est pas donnée ; de même, devant l'ordre, il ne tergiverse point.
18.Ô Cheikh, daignez mettre en nous les attributs des anges,
Ainsi que la foi, l'éducation et le dynamisme pour nous fortifier.
19. De même que la santé, l'équilibre et la pureté, afin que nous puissions bénéficier
De votre agrément, car être privé de votre agrément (ô Cheikh), rien ne le vaut
57
Noreyni KEBE
Nan japp tank yi ak lammin yi
1. Nañ jàpp tànk yi ak làmmiñ yi, jàpp gu tarr
Ku def lu dul lii ma wax, day daaldi lor te loru
2. Te waxtu wii; ndaw lu gàtt um xel lu kenn yarul
Moo ciy wëreelooka wax, yewwul te daaldi yaru
3. Jekkil sa kër, jàpp sag njaambur te nëbbu bu wér
Koo seeru muy dox akay wax nee ko : "yaa ngi xaru !"
4. Doxkat dafay yanu lor yët waa barab ba mu jëm
Buy ñibbi fab loru ñooñee yobbu, far asaru
5. Doxkat bu yobbuwul iy lor, delluseek i loram .
Moyul ma ab dox ak ub doxkat, te def ku yaru
6. Dox am na kat njariñ ak lor, waande fab njariñam
Ba fay loram të na jàppul ndax nga far defaru
7. Koo xam ne xam nga sa lor xam say njariñ mana daw
Sa lor te fab sa njariñ, dox dootu tax nga loru
8. Boo mënla xàmmee sa lor ak say njariñ manulaa
Fab say njariñ, daw sa lor, jekkee la war te beru
9. Bul toppandoo gaa ya man ndox kon ñu mucc nga lab
Bul roy ci gaa yi manul ndox kon nga moy te xaru
10. Tuubal te wommatu sànnim xel te jàpp ndigal
Te jaay u ay jënde kow yiw konte doo asaru
11. Jaayal sa addina jépp it jënde Ajjana yaw
Jaay ug yareediku jëndeb yar te daaldi yaru
12. Jàayal xiyaas aki xam-xam jënde def lu ñu wax
Jaayal kañaan ak rëy ak xér jënde ag defaru
Traduction
1. Tâchons de discipliner nos pas ainsi que nos propos de façon radicale
Celui qui agirait autrement que comme je dis, nuit (aux autres) et se porte préjudice
2. Or, en cette époque, seul le jeune à vue étroite et sans éducation
Se met à vagabonder et à discourir ; sois averti et bien éduqué.
3. Reste chez toi, sois réservé et observe une réelle discrétion ;
A celui que tu vois vagabonder et discourir, tu peux lui dire qu'il se perd
4. Le vagabond se couvre de maux qu'il apporte à ceux qu'il rejoint;
Et au retour, il ramène leurs maux et (ainsi) se perd.
5. Le vagabond, même s'il n'emporte pas de maux, s'en revient toujours avec les siens
(Je t'exhorte à) éviter le vagabondage et les vagabonds et, à être bien éduqué. ·
6. La promenade a certes des avantages et des inconvénients ; mais prendre les avantages
Et délaisser les inconvénients est difficile ; sois réservé (alors) afin de devenir meilleur
7. Celui qui a une conscience claire de ses préjudices et de ses avantages, et qui peut fuir
Les méfaits pour bénéficier des bienfaits, à celui-là, le vagabondage ne peut nuire.
8. Si (par contre) tu es incapable de distinguer les préjudices des bienfaits, incapable
De cueillir les avantages tout en fuyant les méfaits, rester tranquille et t'isoler est ta meilleure
ressource.
9. N'imite pas les bons nageurs, car ils seront saufs quand tu te noieras ;
Ne fais pas non plus comme ceux qui ne savent pas nager, car alors, tu devieras (de la voie
58
Noreyni KEBE
droite) et te perdras.
10. Repens toi et soumets toi ; rejette (l'usage) du raisonnement vain poursuivre les
recommandations;
Troque les querelles contre l'amabilité, ainsi tu éviteras la perdition.
11. Troque également tous (tes biens) de ce bas-monde contre le Paradis ;
Troque l'impolitesse contre la bonne éducation et sois poli.
12. Troque la technique et la science contre l'exécution des ordres,
Troque la jalousie, l'orgueil et la démesure contre la satisfaction (des besoins)
59
Noreyni KEBE
Yaw miy nelaw …
Yaw miy nelaw te xamoo say mbir nangay nelawe?
Yaw miy nelaw te xamoo sak muj nangay nelawe?
Yaw miy nelaw guddi jëm waxtuw fajar te xamoo
Naareeki ajjana foofuy jëm moo nangay nelawe?
Yaw miy nelaw aka xunneekay xaran te xamoo
Nangay doxeegun siraatit moo nangay nelawe?
Yaw mii di xunni te say kem yepp yegg nga des
Nga tolni ñepp te baaxoo moo nangay nelawe?
Yaw miy nelaw te xamoo bis peñci boofa layoo
Dangay yayam dañulay yay moo nangay nelawe?
Yaw miy nelaw ñjël te say sët yepp tollu ni yaw
Dee rekk far des ci yaw moo jaa! nangay nelawe?
Yaw miy nelaw te sa lollib dundu wey te amoo
Loo yobbuloo fa nga jëm moo jaa! na ngay nelawe?
Yewwoo ka jot waajii taggookiy nelaw gëna jot
Ku ñepp yegg te yeggul moo! namuy nelawe?
Ak reera bon ngir ku deewoon dekki dellusi fii
Bu ñepp dee nelawit doo seeru muy nelawi!
Nelaw yi neewël ko, neeful nak nga farko ba nak
Yàllaa ko bind ci yaw mii fàwwu ngay nelawi
Yëgël ni àddina toolub yàlla daala bu wer
Te kenn du yable ci toolam rekk ngir nelawi
Traduction :
Ô toi qui dors sans rien connaître de tes affaires, comment peux-tu dormir?
Toi qui t'endors sans être fixé sur ton destin, comment peux-tu dormir?
Toi qui dors de la nuit au petit matin sans savoir
Où de l'enfer ou du paradis tu seras envoyé, comment peux-tu dormir?
Toi qui t'endors si profondément, en ronflant si fort sans savoir
Comment tu franchiras le Pont (Siraat) , comment arrives-tu à dormir?
Toi qui ronfles si fort alors que tous tes pairs t'on laissé en chemin,
Comment celui qui est l'égal de n'importe qui, mais (qui est) sans mérite peut-il dormir?
Toi qui dors sans savoir si au Jour Ultime, lors de ton procès,
Tu l'emporteras ou tu seras condamné, comment réussis-tu à dormir ?
Toi qui dors au petit matin alors que tous tes petits-fils t'égalent,
Qu'il ne te reste plus qu'à mourir, comment réussis-tu à dormir?
Toi qui dors quand le printemps de ta vie est révolu, alors que tu n'as pas
De viatique à emporter là où tu vas, comment peux-tu dormir?
Qu'il est temps de se réveiller ! Grand temps de se tirer du sommeil !
Comment quelqu'un qui traîne encore alors que tout le monde est arrivé peut-il dormir?
Que l'ignorance est mauvaise ! Si quelqu'un après la mort, ressussitait et revenait ici-bas,
Même si tout le monde s'endormait, lui, on ne le verrait jamais dormir.
Tâche de réduire (ton temps de) sommeil; il ne s'agit pas certes de l'abandonner,
(Car) c'est Dieu qui l'a créé en toi, il faut que tu cèdes au sommeil.
Sache (seulement) que le bas-monde est un véritable champ pour DIEU ;
Or personne n'enverrait (ses gens) dans son champ uniquement pour qu'ils y dorment.
60
Noreyni KEBE
Ñaanal Sëriñ Mbay …
Yal na ñu fab mbay
Fàww ak ndamal mbay
Ak njariñal mbay
Jébbal Sëriñ Mbay !
Yal na dugub daw
Barkeb dugub daw
Mbootum dugub daw
So ci Sëriñ Mbay !
Yal na ngërëm daw
Xam-xam bu wér daw
Diine ju wér daw
So ci Sëriñ Mbay !
Yal nag ragal fëx
Dëddu gu wér fëx
Wërsëg wu lew fëx
So ci Sëriñ Mbay !
Yal na njariñ ñëw
Dund ak njariñ ñëw
Gudd fan it ñëw
Dëkk ak Sëriñ Mbay !
Yal na soxub ndam
Buy dolli nit ndam
Buy dolli nit gëm
Jib ci Sëriñ Mbay !
Yal nag juboo ñëw
Sutura yit ñëw
Muj gu rafet ñëw
Sax fi Sëriñ Mbay !
Yal nag tawat daw
Lu koy waral daw
Lépp lu bon daw
Teggi Sëriñ Mbay !
Yal na ña gëm ñëw
Mboolem ña jub ñëw
Ña Yàlla saf ñëw
Far ak Sëriñ Mbay !
Yal na xorom ñëw
Ña am xorom ñëw
Ña koy wut it ñëw
Ànd ak Sëriñ Mbay !
61
Noreyni KEBE
Yal nay murid ñëw
Séeniy sëriñ ñëw
Ñu bokk xëy ñëw
ŋoy ci Sëriñ Mbay !
Yal na ñu feesal
Ñéppaki ndimbël
Dell te feesal
Ruqi Sëriñ Mbay !
Amiiiiiiiiiin !
62
Noreyni KEBE
Maroon naa …
Maroon naa nga bën'nalma teenub cofeel
Ma hiifoon nga far dioxma daggay ngeneel
Ma ñakkoon nga jebbëlma mboollooki ki yëf
Ma reeroon nga xëy mayma xamxam bu téel
Ma soofoon nga far def ma geejuk xorom
Gou saf sap seéxalma jox may méteel
Gërëm naala nak defma ab sante kat
Boulay sante kay way ci barkéb jabeel
Samay yëf dou jee ndaxte say yëf dou jee
Bou ab sangg doul jeelé jaamam dou jeel
Damay sante ngir yaama dakkul lu bon
Bou wer ak ku bone mbacké yaw laafi neél
Ku lay won cofeelam ma wan koy ngërëm
Ku lay won bañelam ma won koy bañeel
Ku lay soppu dundëm ga jak dee ka jak
Ku lay bañ ba dee daldi dém naari beél
Kudoul yaw péxèemak soloomak mbiram
Jubul sam péxee jub té yaanuy féxéel
Yërëm nooti dollètignuy mbégg you rëy
You tooyal sunuy xol te maynuk noteel
Bou siinak bawal ak kajoorak jolof
Ñëwan daldi feesal te doo khàaja diéel
Fa hëb lii ghinan ‘an jamii’il warà
Mouriidan shakoora, bu doyliy nganeel
Kuy dounde bum fatee dee
Kuy dundu boum fatté dee nay JëF tay JëF lou rafét
Kone bis boudè dee malaakay aksi naako bégël
Lou tollu né aljana déful JëF ba JëF lu ko jar
Te moona déful moyite bay moy lu jar tégou xal
Moy Yallah moo mata daw ak toppu moo mata wut
Lee moodi yoonu ndigël lii moodi yoonu mousël
Kuy roy na roy waaju xam tey toppu moo mata roy
Ku roy kudoul kilé loo am kate na sédd sa xol
63
Noreyni KEBE
Seriñ bi yiw wunu xamul …
Seriñ bi yiw wu ñu xamul
Yiw woowa nanga ñuko xamal
Te weppu yiw wu ñu amul
Yiw woowa nanga ñuko amal
Te wepp yiw wu ñu manul
Yiw woowa nang ñuko manal
Te lepp loonu tànna-lul
Loo lëlè nang ñuko soril
Lor jun yëgëk gounu yëgoul
Ñun yeppu nang ñuko fégal
Moy gun yëgëk gunu yëgul
Ñun yeppu nang ñuko faral
Moy gun tayak gun tayul
Jeggël nu ñun far gnu boyal
Luñ jagalak luñ jagalul
Booleela boolé yaw jagal
Luñ défarak luñ défarul
Fabalnu lepp défaral
Sun bon gui nangnu souturàl
Te lepp luñ déf gërëmël
Loo gërëmul bouñuko jiss
Te moomitam boumounu jiss
Koo gërëmul bouñuko jiss
Boumounu jiss nang-nu moussël
Tay noo ngilay jébbalati
Sunuy mbirak sun boppati
Top sunuk njabootati
Te rikk ngir Yalla nanggul
Luñuy défak luñuy xalam
Fun tolli nay langa gërëm
Tay gën ji loo mosa gërëm
Tay dëgg dëggui sa ndigël
Bun dém fudull foonu yabal
Bun déf ludul loonu digël
Bun yëkk ludul loonu yëgël
Fégalnu lepp loo bëgoul
Wattunu ba dootunu ruur
Kenn Té keen du ñu ruur
Koo wattu dëgg dootu ruur
Deesuko ruurit taxawal
64
Noreyni KEBE
Meloy Baamba …
Meloy BAMBA yaa ngii ku réerey meloom
Na jog déglu kon lee mu xam ay meloom
Yëram ndaw teral mag teral aw ganam
Teral mépp mobkkam teral dëkkëndoom
Di tàllal ndejooram mu jëm gépp wet
Di jox ndaw di jox mag ba koo seeru luum
Du wax nit ku teew’ak ku teewut lu bon
Du jëw nit te bëggul ku jëw nit fi moom
Du def ay du wax ay jëfam day rafet
Waxam yit rafet kii amul kat moroom
Budee dox du geesoo du piisit bëtam
Du soppiw doxiinam du sànniy yoxoom
Ragal Yàlla gaa tax du soppiy céram
Defar nay céram ngir yabul Yàlla moom
Ku baax’ak ku bon képp lay fab teral
Ku muy gis dakoy daal di fab def ni doom
Yaram baa nga dem mag ngoram gaa ko raw
Ki lee jiitu kenn dόotu weddeek a miim
Xolam baa nga dem set soreek’ug tilim
Du ëmbal nit’uw ay du daaneek a bόom
Du yan nit du lor nit du yàqqub deram
Dafay faj lu bon mbaa budul faj ne xiim
65
Noreyni KEBE
Seriñ bi fegalñu moyaki moy …
Seriñ bi fégalnu kuy moyaki moy
Te maynu kuy mayeeki may
Fajalnu àdio yeep tay
Yaanu yilif yaanu manal
Sunuy yaram na naatanaat
Sunuy bërëp na naatanaat
Sunu leep lëf boumou maral
Té nàtalal sunuk njaboot
Gueep te def leeni njaboot
Te wattuyit seeni njaboot
Te boolee leenit nëtaxal
Te defnu ay sante katit
You jiitou beep sante kat
Te defnu ay jaamu katit
Bou been jaamou kat jotoul
Foun tool nan fa guena gëm
Tey say murid you keen yaboul
Fégalnu gëm gou rikkiku
Fégalnu xam gou rikkiku
Fégalnu mouj gou rafétoul
Addina jii bounoufi mér
Bounoufi giss mukkati lor
Kër galé yit lufa di lor
Ak gaathié nang’ñuko fégal
Tay ak ëlëk bounoufi mér
Bounufi rat bounoufi mar
Fégalnuyit tiisaki lor
younou xamak younou xamul
rëyelnu man nganoo rëyel
jagalnu man nganoo jagal
notalnu man nganoo notal
ngir yaw ku note yaako notal
yaralnu manganoo yaral
guissalnu man nganoo guissal
gënalnu man nganoo gënël
dajalnu manganoo dajal
douyalnu manganoo douyël
jamalnu mangano diàmal
ngir yaw ku diàm yaako diàmal
jamal nu ba baddub sa ngërëm
ban daané Ñun rabou ngërëm
ba laakh mbolèm say ngërëm
te laakh say mayak sa xol
te jeep lor nang nu xamal
xamal gou andakuk fégal
weep yiwite nang nu xamal
xamal gou andakuk amal
66
Noreyni KEBE
Sa bind daa na waral …
Sa mbidd daa na waral saytaane fecciku daw
Yonnen bu tedd ba muuñ as lëf, Aras jaayu
Yaa daa waral Yàlla ak Yonnen ba daa nu fegal
Lor, daa nu ñoddil njariñ, nuy tuub’akay jaayu
Sa mbidd a daa tax malaakay Yàlla yépp di bég
Di tudd Yàlla ak a sàbbaa teg ca nag jaayu
Yaa da waral xejji suuf ak xejji kaw di gërëm
Yàlla ak a yéemu te naa jii waay a jar jaayu
Yaa daa waral Yàlla def loo xam ne deftiko kon
Lu yàgg-yàgg ndaxam yaw rekk a jar jaayu
Yaa daa waral Yàlla jàppub lar bu deefi falang
Baaxal ko nit ñépp xëy doyloo ko muy jaayu
Yaa daa waral Yàlla jéggal ab laram lu mu moy
Nëbbal ko fàwwug bonam muy sant’akay jaayu
Yaa daa defal Yàlla cib jaamam lu rëy lu ko saf
Ñu bokk sant la biir ak biti bay jaayu
Ñun ñépp sant na ngir yaw ñépp bég na ci yaw
Yëgal ne buuraki xejjam ñépp a lay jaayu
Say soppe wuute na ñu’s lëf ngir ñilee ngi gërëm
Ñilee ngi waaru, ñalee ngay joy’akay jaayu
Jam-jam yu rëy yi nga jam saytaane rekk a waral
Budee si jaayu ci yaw muy moolu, ñuy jaayu
Yaa daa bégal gaa yu rëy ñuy jaayu yal na nu lay
Bégal yaw it sépp saa ngay muuñ’akay jaayu !
Foo bëgg dem …
Foo bëgg a dem nanga wut loo yóbbaloo soog a dem
kon boo demee doo fa lor yaw nit te doo fa loru
kuy dem te yóbbaalewul yóbbal bu doy fa mu jëm
kookee du bég du bégal ngir day loreek a loru
Yóbbal bi nag moo di fàggub yar te wol mburu yor
foo dem di may koo fa gis ab yar, di mos sa mburu
Ku nekk war na balaa dem fab yar ak mburu yor
ngir dégg fenn di wax talal du xeetu yaru
Yóbbul yar ak mburu boo dee tukki, kon dinga bég
bégal barab ba nga jëm ngir doo loreek a loru
67
Noreyni KEBE
Bu cér yépp gàntoo def'as lëf jafe
Bu cér yépp gàntoo def'as lëf jafe
Def'as lëf bu yombul am'as lëf jafe
Jugal farlu ngir yaa ngi cib lolli yaw
Te ab lolli buy wéy am'as lëf jafe
Ndegam reere nga'b lolli lollee ngi nii
Wér ak dund ak doole lollee jafe
Ku sab lolli ñëw nag ba say yëf ne xuss
La gën ngay ku yombul, ku maasam jafe
Jëfal guddi jëf bëccëg'ak sépp saa
Ba koo seeru naa kii jëfam yee jafe
Ku def nii ci sab lolli do jeele yëf
Bu nooree te doo xaare yewwoo jafe
Budul woon ngëméen ak nélaw koofu gis
Mi ngiy farlu ngir xam ne lee jëf jafe
Bu nit nee lasar, ñépp naa dóotu jug
Mu xemmeem a jog jëf té jog jëf jafe
Ku jëm cib ja té romb xaalis di wey
Bu yeggee di gis yëf ya teg njëg jafe
Xarit dëgg ŋooral ci xaalis bi yaw
Te kat leegi seerub dërëm sax jafe
Ngirug mag akug ràgg ak dee ngi ñëw
Bu ñuy yegsi dëf lëf lu bon bon jafe
Defal Yàlla as lëf bu mujjee jafe
Am as lëf ci Yàllaati gën koo jafe
68
Noreyni KEBE
Seriñ, Xarit, Jëkër …
Seriň dalay jariñass lëf yarla yorla bu werr
Xamal-la YALLAH ngadip santam di ap jaamam
Xaritt dalay xaraluss lëff ciy yëfam nila am
Koo xamni kii du xarass lëff mayla doo waayam
Jëkërr dafay mugna kay mugnlee ka sammu ngoram
Raggal Boroomam ta am njëll jiitu ak maassam
Jabar dafay yaru tay mugn neexi wax bagna wexx
Rafett rafett jikko mann bopam necip neegam
Ass-gorr dafay gore tay fonki waxam badu dagn
Du fenn du jëw tadu sookep jëw, kadip yaaram
Mbokay ka bokak yawup xoll, say waxitt di waxam
Seeni jëffit bokku, muy sap caabi ngay gaalam
Buuray ka xam YALLAH sax cikk toppu nott bakanam
Ta doylu doyle amuk mbaaxam yoruk leeram
Sammay ka sammi cerap sammup xolam badu jëmm
Cikk moy, du jokk ci ndigël bi samma gënn geeram
Jaambur dafay japp fawuk njamburam ci lu bonn
Du deff ludul noona deeful degg aw tooram
Sanggay ka sangi moroomam tay jubbal aka jupp
Nekkal di app sangg yawmii mbaate ngay waayam !
69
Noreyni KEBE
Sëriñ bi yaa baax
Sëriñ bi yaa baax
Mbàkke sa jëf baax
Yaa rëyi xarbaax
Yaa yor njariñ yi
Jubal nga mbir yi
Seral nga xol yi
Dalal nga xel yi
Teeyal bakkan yi
Dàq nga ay wi
dindi nga mar wi
asi nga yiw wi
Defar nga mbay yi
Topp nga Yàlla
Toppulu Yàlla
Yaa def la Yàlla
Digle ci mbir yi
Yaw am nga jaajëf
Maye nga jaajëf
Yaa saf te saf jëf
Far nga yu bon yi
Musal nga nit ñi
Gindi nga nit ñi
Wommat nga nit ñi
Tàbbal ci kër yi
Tuuti ñu sanku
Yaa tee ñu sanku
Tëggul a tëggu
Yaa yor goroŋ yi
Tëggul ñu wuy si
Tëggul ñu del si
Ku yor sëriñ si
Na yor murid yi
Nga boole nuy yor
Fàww akay yar
Nuy yoratib yar
Dundal yaram yi
Wooteel a woote
Bu kenn wuute
Mukk sa woote
Bile ci gox yi
Dolli nu wërsëg
Dolli nu ay mbég
Dolli nu ag jag
Te yokku fan yi
70
Noreyni KEBE
May nga nu ag fal
Fàww’aki fonkal
Ak xaalis ak njël
Teg ca ngërëm yi
Yaa mat a jàppu
Te ku la jàppu
Sax doy a jàppu
Yaa saytu ndam yi
Yaa ëpp a wacci
Te ku la wacci
sax mat a wacci
Soril nu moy yi
Fasoo nama fase dunyaa …
Fasoo na maa fase dunyaa fàww nag bu rafet
Ba xam ne kuy tuddi gaayam doo ma tuddaale
Dunyaa safoo ma te yaw mii donte xam nga ko yit
Loo rëdd-rëddati say far doo ma rëddaale
Li ngay def ak li nga daa def ak li ngay nara def
Xam naa ko lépp azal doo tax ma bokkaale
Ndegam da ngay rëbb a kay yootee’ka wor ak a lor
Sa bopp man maa ngi wut Yàllaa ka déeyaale
ŋëb naa ci koo xam ne lor’til kenn wor’tiko yit
Te moo di Yàlla mi deeful suul a kay jaale
Ko xam ne day mujju nëb ay sax di lekki yaxam
Giñ naa ne ab dof a koy may ak paal a kay faale
Jàppal ci lii ñu la jox doyloo ko fàwwu te bul
Bul dox di xemeem a kay yóotoo’ka féqqaale
Lu Yalla féqq mu ñëw loo xam ne féqquko nag
Loo féqq féqq du ñëw lii fab ko yobbaale
Tuubal te sax ci ndigël kon wépp yiw dina ñëw
Te sax ci yaw fàww ngay fàttee’ka rombaale
Lu deefi wut bu la dee wut loo fexeeti mu jub
Te lëf du jib ci digg’ak kenn ngay yaale
Jàppal sa itte mu jëm kaw bay sa sas wi su jee
Ñu jox la ab añ bu dóotul jeex nga tëddaale
Bul itteewoo añ bu koy geesoo’ka tuddati sax
Añ baa ngi ñëw lépp luy ñëw mat’la tuddaale
71
Noreyni KEBE
Yallaa di geejug njariñ
Yàllaa di géejug njariñ goo xam ne kenn du ko as
Duykat yi duy nañu bay feesal te ken nasu ko
Doxkat yi jόg nañu ñii ngiy daagu ñi jamu xél
Ñii gaawe niw saan a kub sox waaye kenn jotu ko
Ñilee ngi xam tuuti ñii xam jόpp ñii bañ a xam
Ñi ëpp faf ñépp xam-xam waaye kenn xamu ko
Ñilee ngi daj tuuti ñii daj jόpp ñii bañ a daj
Ñii daj ba daj lu rawum xel waaye kenn daju ko
Ñilee ngi gis tuuti ñii gis jόpp ñii bañ a gis
Ñii gis ba gis lu ñu dul wax waaye kenn gisu ko
Ñilee gi jam tuuti ñii jam jόpp ñii bañ a jam
Ñi jam ba jam rabu “cey-cey !” waaye ken jamu ko
Dellul ca saw sas te bay nag bul liggéeye wërub
Tool’ak wërum tooba lii day yàq mbay bàyyi ko
Ndegam xamoo ko te xam saw sas mu doy la xanaa
Ndegam gisoo ko te gis sag pal mu doy dagu ko
Toolam bi nag loo ko wër wër yaw te xam ne bayoo
Du tax nga am dara yaw luy tee nga am moyu ko
Toolam bi moo di bàyyig moy fàww sax ci ndigël
Mucc’ak njariñ fàww a dib añ dig pal it fexe ko
Bul ittewoo xam lu dul saw sas ku bëgg njariñ
Day jéem a xam aw sasam tay jéem a dem bayi ko
Loo xam xamug moy te waccoo moy ga fajtila lëf
Loo xam xamug yiw te doo jëf ñàkk a xam tane ko
Bàyyil lu bon defu yiw añ ñëw nga añ bay a bay
Yamal ci lii nég fi sab cër kon mu ñëw nga ti ko ( Ti = tëye bu dëgërr)
Lu am fumuy tàmbalee kay yam la xel man a jot
Lu àppuwul tàmbaleewul fenn xel jotu ko
Asal te farlu ku ñëw day as di as ba ne mes
Yόbbum ndoxam ba ko muy fellax nde kenn nasu ko !
72
Noreyni KEBE
Gennal ci nëpp ba sett
Génnal ci ñépp ba set, nag, génne ñépp ci yaw
Bul tàbbi nit, te bu nit tàbbeeti mukk ci yaw
Ubal sa bopp ba doo am fenn buntati far
Ku ñëw fi yaw lu mu wër wër wër na mujj taxaw
Duggante wéy na, ña baaxoon wéy na[ñ] , tay ñi fi des
Ay yàqkat lañu ak ay njuuma "doom a nga daw"
Li ëpp ci’w nit lañuy wax bokkul’ak lañu fas
Ku ñëw dalay wonu yiw, buy jóg fi yaw di la jëw
Naaféq baaxul, na muy mel bokkul’ak na mu mel
Ayam wa day ne ca biiram, yiw wa nekk ca kaw
Day ree fi yaw ak a bandaañook a wax lu rafet
Te xol ba bañ la ba dee, bum gis ci yaw fu mu aw
Loo wax mu ree, loo def it muy ree di saf ku mu saf
Te xam ni say wax a ngii mel fib xolam ni ngelaw
Tay ken jarul dara ngir naaféq rekk a fi am
Foo gis ku am dara, ay naaféq daal a ko ëw
Ñu tuut a mucc ci ag naaféq tay jile kat
Ak démb sax, waaye nag lay dëgg tay dafa raw
Soññil sa bopp te wéy ak gaa yi top ci yaw
Te muñ, ñu muñ bu rafet ndax léegi wallu gi ñëw
Ku Yàlla wallu nga fàtteb coona, Yal nanu may…
Ñun ñépp wallu gu rëy, guy tax ñu dab ñanu raw
Te Yal na Yàlla defar géppug defar sunu mbir
Ba dóotu yàqu te may nug doylu fàww ak u yiw
Murid bi yaw jeexalal sak dundu….
Murid bi yaw jeexalal sak dundu far ci ndigël
Sa noh gu ñëw mbaa mu wéy nay ñëw di wéy ci ndigël
Jappal ci Yalla té déf toppam ga ap xaritak
Baayak ndayak soxna ak doomit té défko alal
Té déf ko ap goro déf kow fass té déf ko sa kër
Té défko mak défko rakkak mbooku défko sa njël
Té défko wéttalu xol ak andandooki serak
Jammak ndoxak lal bou nooyak gën-ji daall té sol
Joulil ci yonénba mbà ngay zikarooka xalam
Aw yiw ci sap xol té bul neenal sa waxtu jëfal
Loo mën défal loo mënul jeemal té yeenèko yaw
Kuy jeema yiw aka yeenéw yiw mbiram bonagoul
Sa cër yi nay jëf té saw laamiñ di wax waxi yiw
Njagam manoo waxakay jëf aw yiwit xalamal
Loo déf ci aw yiw lu séw séw ak payam dina ñëw
Té payga waxtuwu dikkee seedd gouyyi sa xol
73
Noreyni KEBE
Dama dém fi ay sëk
Dama dém fi ay sëk ma jis keépp nit
Ni cundug ci bameelamak ay jëfëm
Ma xamnak ni koo xamni liidik mujëm
Bou yeewoo dafay teela jëm ciy mbirëm
Jugël jëm ci say mbir te bul toppandoo
Ñi booleek tayeelak ngëmeenak ngëlëm
Lu nit fab di yobbààlé bammèlakoy
Fajal dur ludul loolu fajtil dourëm
Te ak jur akuk nit ku dee dooko fab
Di yobbaalé faggul ci sak jur ngërëm
Te mbooleem lu nit saytu Yallaa ko fab
Abalko te buy dee mou nanguy yëfëm
Ligeeyal ci say yëf te wut ciay njariñ
Lu jar dem ba say yëf te laqqoo ca ndam
Ku xam dëgg loo am balaa jee nga am
Cia loolee ludul nammatee jee ndaxam
Ku am déx ak’ub jàji* tay gass bu wer [loy gass ta yeggagut]
Balaa déx baa jee mou serum ndoxam
Te ab déx nak moodi dunyaa yëgël
Te gass moodi ak jamu jaamul te gëm
Werak dundu ak wërsëgëk kër gou jak
Dou lëf kat ndarib ndéx yewwul te xam
Ku déxam ba xëy jee te bënnul peurëj
Mou dëkkeew marak mér di rećuy jëfëm
Xarit dëgg naanal te gass bënn yaw
Ku def nii bou bës baa dou rećuy jëfëm
Xarit dëgg naanal te gass bann yaw
Ku déf nii bou biss baa dou réćuy jëfëm
Xarit lepp loo saytu jaamuko yaw
Ku def nii bou biss baa mou begg ciy jëfëm
Waajal nga gaayi te waadioo
Waajal nga gaayi te waadioo yaaka doy keemaan
Fooralnga gaayi te fooroo yaaka doy keemaan
Seeralnga gaayi te seeroo yaaka doy keemaan
Reewalnga gaayi te reewoo yaaka doy keemaan
Feesal nga gaayi te khaadioo yaaka doy keemaan
Lottalnga gaayi te lotto yaaka doy keemaan
Jeexal nga gaayi te jeekhoo yaaka doy keemaan
Tiitël nga gaayi te tiitoo yaaka doy keemaan
Reewalnga gaayi te reewoo yaaka doy keemaan
Diiseulnga gaayi te diisoo yaaka doy keemaan
Feexël nga gaayi te feexoo yaaka doy keemaan
Défar nga gayi te yaakhoo yaaka doy keemaan
Suuxël nga gaayi te suuxoo yaaka doy keemaan
Jeexal nga gaayi te jeexoo yaka doy keemaan
74
Noreyni KEBE
Sëriñ bee matub sàngg moo gën kuné
Sëriñ bee matub sàngg moo gën kuné
Te moo doy wolaf ak tubààbak kuné
Mbirëm doyna naarak tubààbak wolaf
Te doy sëk goorëk jigéenak kuné
Kukoy sikk nékkul ci suufak cia kaw
Mbirëm fës na nib diànt tay moo fi né
Ba léeral na suufak kawak béep gox
Jëfëm jëm na kaw aw turëm dém founé
Bëmëx nay ngënéelak njariñ kepp nit
Ba koo jis mu féesal te am nak luné
Bu seeroo ku saggan té bon melni man
Mu fab tek cia kaw far ko may sag buné
Budè jis kuñuy xeebakay dox di xas
Mu nabbuk bonam xëpp koy yiw wuné
Kuñuy dox di suxlooka soowuk bonam
Balà diékki kookee raweekay gëné
Bu jappè ku bokkam ya sanni fè
Bu délló fa bokkam ya moo fay tané
Ngënéelam yi ño daj kadiórak bawal
Te daj péngku daj sowwu daj wet guné
Amul gén wet guy ngënéelam néwul
Ndaxam gaayi jii waaya gën wàà juné
Té yalnaw fanam ak sunuy fan di wéy
Nu far muth am fan wu sut fan wuné
Te yalnab xolam sedd fawwit ci Ñun
Te far sédd séddit ci mboolèm kuné
Seriñ day wootee Ibliss di wootee …
Seriñ bi day woote
Ibliis di wooté ni ay !
Ku neekka ngay wut kumuy yobbaalé
Moo nakamu
Ku nekk am na kërëm
Kum japp yobbu kërëm,
Ku reere kër ya danaa juk waxko kër ya yumu,
Ki aljanaa di kërëm
Kii naari moodi kërëm
Ku wouyyu ji chaytaané
Boo dee saw yaram xoyumu
Nañ daldi wuyyuji BAMBA mii
Ken dul fab nitam di xoyum,
Shaytaané moo dib noonu yàlla jumu
75
Noreyni KEBE
Cheikhi gannààraki kajoor
Cheikhi gannààraki kajoor
Yeppa ngi nii naa yaadi goor
Kénn sikkatul ni yaadi goor
Banga défee lu kénn deful
Yàllaa ngi naala jërëjëf
Yonénba naala jërëjëf
Seriñ si naala jërëjëf
Yaw ndam li lépp yaako jël
Ku Yàlla far di sab guéwël
yonénba far si sab guéwël
Seriñ si far di say guéwël
kula wayul doula soxal
Kula wayul guis kula way
kula wayit guis kula way
Ku yabu noppi mbaa mou way
yaw am nga tanneefi guéwël
Kula wayul deesuko way
kula mayul deesuko may
Kula royul deesuko roy
ku dagouwul deesuko fal
Ku dagu yit ku faluwul
dou tax mou fal la guén pal
Ngir kénn dou diox nit loo amoul
yaa falu falnou guép pal
Danoo amoul té manounu
te bëg nak nga saytuñu
Te mbakké dëg saytuñu
te maynu gnuy aw sa ndigël
Donté danoo bariy dërëm
foo tollu yor sunuy dërëm
Te Yàlla xamna yit nga xam
té kon mou doynu hasal
Wandé ndiegëm batay dano mënul
yaw man nga man nganoo manal
bounu xamul ténga xamit
baanu mënul ténga manit
baanu yëgoul ténga yëguit
yëgëlni kon donu bugël
76
Noreyni KEBE
Seriñ bou nékk yalna bég
Murid bou nékk yalna bég
Joulit bou nékk yalna bég
Te moucthu ciy loraki moy
Ku tuubëgoul yalna tuub
Koo xamni kii nak dafa tuub
Yalna dolli lamou tuub
Ngir tuuba kiy ćant dou doy
Boul bàyyi tuubak ćant yaw
Kuko bawoul dou ñakku yiw
Kuko ba daldi ñakku yiw
Saxalko yaw fawwu te wéy
Lar buñu may santa ko war
Lar bu moyit tuuba ko war
Moo tax ba tuubak ćant war
Ci bépp lar nanga ci ngoy
Kuy sante ñuy dollik mayam
Kuy tuubi gnuy fari moyam
Te kuñu dolli ak mayam
Fari moyam mou sori ay
Ku man di juleeka wirdaakay
Ku man di juleeka wirdaakay joxey alalam
Na jug te def ko te bum tax muy xassit ku manul
Ku jàng jàng ba xam mbooleem araf yi nu gis
Na sant Yalla te bum tax muy yabbit ku xamul
Yallaa amal ku fi am, Yallaa xamal ku fi xam
Moo sakk ndab yi defuw yiw sakk ndab yi deful
77
Noreyni KEBE
Ma jóg defal gaayi tindoodiy bëyit yu rafet
Ma jóg defal gaayi tindoodiy bëyit yu rafet
Ndax séeni xol sedd séeniy itte yekkatiku
Ittée di koomum Murid, mboolem Murid bu ko am
Sangam gërëm ko, la muy wut lépp jàppandi ko
Wutleeni itté yu rëy, sàkkuy ngërëm, fexe ndam
Te soppu séenub Sëriñ toppiy waxam te ja ko
Dableen a dab ngërëmam tay sàkku fàww mbegam
Te lépp lëf lu mu bañ dawleen a daw sori ko
Mat nab Sëriñ, yéen itam matleeni taalibe nag
Te yeesalug tuub akug njébbal akug bàyyiku
Jëmleen a jëm ca kanam mboolem lu deefi mébét
Cig jëm kanam la ko deefi làqe sikku ma ko
Kem lub Murid jëm kanam gën faa jegeb Sëriñam
Gën faa defub xaritam, yaw sab Sëriñ jege ko!
Jegeb Sëriñ bokkul ak fus toll jis la fa kët
Ngay xool ak'ay d"glu waxtaanam te santu la ko
Jegeb Sëriñ moo di, yaw mii, toppatoo ndigalam
Te lépp loo xam ne bëggul, loola yit nga ba ko
Sëriñ ku aw ndigalam yaa nekk ciw wanagam...
Ne cib xolam, ab Sëriñ, kuy moy ndigël safu ko
Te doonte yaa ngi ci mànding tey jëfey ndigalam
Yëgël ni yéen a ngi riisoo, Yàlla seede na ko
Te doonte yaa ngi fi poojam tey moy it ndigalam
Séenub diggantee fi sut ndar lii'k a bon moyu ko
Tay gaayi Tindoodi séenub déng mat na mi ngii
Ñun ñépp Yal na sunuy bir jub te yékkatiku
78
Noreyni KEBE
SIYAARE
Bul jombuloo siyaare nit
Kuy jombuloo siyaare nit
Doo gis mu am lamuy mebet
Siyaare day taxa falu
Te bul siyaare ndare ñaar
koo xam ni kii danala waar
Ngay waaru mbaa nga diko waar
muy waaru lii rekay solo
Ndegam jisoo nak ñile ñaar
Jekil sa kër te waara waar
Sa boppu moo gën jok di waar
Aw nit ñu naa yaa am solo
Ku toppul Yalla yit boum deeti …
Ku toppul Yalla yit bum deeti juk diko moy
Moy yàlla rëyna te dee dém naarit woyoful
Ku man di julleeka wirdaakay alalam
Na juk té défko té bum tax muy yabite ku mënul
Ku janga jang mbooleem haraf yinu xam
Na sant Yalla té bum tax muy xasit ku xamul
Yallaa xamal kufi xam Yallaa amal kufi am
Moo sakk ndabyi défiy yiw sakk ndab yi deful
Yallaa fi ték ndab yi moo sak leep ndab lunu jiss
Nan koy téral ngir boroomam ñun té bun ko bonal
Foo jiss ku bone neeko yalnan Yalla boolé yërëm
Xamalni nite améwul boppam ndé kon mu jubbal
Am lar namuy dokhi bay reylooka xeebee kèmam
Kuy xeebbu nite xamagul kuy rëylu yit rëyagul
Ku rëy du rëylu ku am xam xam du xeebi kèmam
Mbaa kon nga xamni dafay saf waaju xam té xamul
Yallaa jagoo rëy té waajuy rëy mu daldila halak
Chaytaané xamnani rëy bààxul ndé mooko bonal
Xamxamlu taxtila xam jak jaklu taxtila jak
Xëy xëylu taxtila xëy sol sol'lu taxtila sol
Rëy rëylu taxtila rëy am amlu taxtila
Saf saflu taxtila saf jël jël'lu taxtila jël
Yallaa ki yor yëfamak yeeppam di seetu nitam
Té waxtuwuy jiss kukoy soopite mu jappuko fal
Ka yàlla jox palga kookéé moodi kay mata xam
Té palga dioxnako tayjii BAMBA mii nu nékkal…
79
Noreyni KEBE
Xarit dëgg yaw bul defub tëddkat
Xarit dëgg yaw bul defub tëddkat
Njegam bëgg ngaa def nitug tédd nga
Njegam bëgg ngaa tédd bul tëdd yaw
Ta woppoo bu wer ndaxte kuy faaxu nga
Bàyyil faww biddanti tey yéwwu njël
Kudul yéwwu njël kat du jël cant ga
Ta ngay yéwwu yaw njëkk waxtuw fajar
Di fàgguy ngërëm nag ba jot nodd ga
Ta boo dee nelaw kat ba waxtuw fajar
Nga jog yéwwu dem jùlli biddanti nga
Nelaw, lékk, wax ; neewalal yétt yii
Ta boo neewalee yétt yii kat të nga
Nelaw tuuti, wax tuuti, mos tuuti ; nii
La dag yépp daa def ba for ndombo ga
Defal nii ma wax mbaa nga jébbal sa mbir
Ka def nii ma wax, kon batay wàcc nga
Kudul gis ta jox ag tumam kay gisit
Du wooloo la neefaa ko yaw yégg nga
80
Noreyni KEBE
Gaa yile man jébbalu naa
Gaa yile man jébbalu naa
Bu wér te kat bàyyiku naa
Bu wér te kat soppiku naa
Nar a tu ma a yor séeni mbir
Nar a tu ma a yor sama mbir
Nar a tu ma a yor séeni mbir
Nar a tu ma a yor sama kër
Nar a tu ma a yor séeni kër
Nar a tu ma a yor sama jur
Nar a tu ma a yor séeni jur
Fasoo na ma a fab séeni jur
Ak sama jur joxe bu wér
Tay boole naa man séeni mbir
Ak sama mbir ak séeni kër
Ak sama kër boole gu wér
Jébbal Sëriñ Bu Mag far !
Jébbalu naa jébbale naa
Noppalu naa, noppale naa
Te noppi naa, noppilu naa
Deesu ma gadul ak a fayu bor
Lebu ma man, leble wu ma
Te moone kat leblu wu ma
Waxu ma yit waxlu wu ma
Tudd samay ayib du ngor !
Sëriñ bi man ma a ngi nile
Samag njaboot a ngi nile
Sama mbir ya a ngi nile
Na nga nu boole yor defar
Buntub tawat ubal nu ko
Fàww ba dootul ubbiku
Buntub ngërëm ubbil nu ko
Fàww ba dootul ubu far
Ubal nu wunti pert yi
Ubbil nu wunti tono yi
Ubbil nu wunti cant yi
Ngir caabi yépp yaa ko yor
Yiw wu nu raw na nu ko jot
Waa ju nu raw na nu ko jot
Ba far ko jiitu bu rafet
Te bu nu lëf mbaa kenn lor
Te bu nu aw yiw rawati
Te bu nu kenn jotati
Mukk ak a dox di séenati
Sarax nu barkeb mépp ngér !
81
Noreyni KEBE
Ludul ndigël amul njariñ
Ludul ndigël amul njariñ
Te kat xamal ni ap Sëriñ
Du bëgg nit ba fob njariñ
Jox ko ta toppul ndigëlam
Kem loo defal nak sab Sëriñ
Am luni tollu ci ay njariñ
Loo defalul nak sab Sëriñ
Sooko bëggée yit doo ko am
Ap tretang [commercant] ñàkkul dara
Waaye ku saytuwul dara
Du am ca njaayam ma dara
Lilée mata xam ta mata gëm...
Bul jay sa bopp buko nax
Xamal ni kat deesu la jox
Ludul li ngay jëf aka wax
Ak dëgg rekka am xorom
82
Noreyni KEBE
Sa jëmm ji lé tax ay du ñëw
Sa jëmm ji lé tax ay du ñëw Yàlla yaw la rus
Rusul ku la moy Yaw donga tee nu gisug mbugël
Lilée tax ma naa yal nang fi yàgg te saw yaram...
Di seeda ka wér, ngay may ndigël ñéppa kay bégal
Bu lor nee bërét ngir bëgga dikk nga dàl di jañ
Njariñ fëxit ngir bëgg ñoo raw nga gor ko fél
Njariñ dóotu raw, lor dóotu jot kenn lii ka rëy
Jañal nga nu bon bon yépp far bett noo ki pal
Wutal nga nu ndombog tàŋk koo séenakug palam
Amul ci sa ñooñ koo xam ne kii amulub dogal
Sëriñ nga bu gën mbooleem sëriñ sépp tey pakebjullit ñépp paasal noo ti tey joowa kay dawal
Da naa boole tuub ak cant ngir boole koo ma war
Ku yor may, yoruk moy, sant tuuba ko war asal
Da naa joowalit mbooleem jullit ñi fi Yaw mi am
Lu faj lor te am yërmànde sébbi na, seppalil !
Maral wi na deñ, mbooleem ku woppu na dàl di wér !
Ku ñàkk na am, koo xam ne suufe na yékkatil
Ñi nekk ci kaww suuf sépp Yaw la ci Yàlla yëg
Te Yaw la ci àndal, Yaw la ciy xoola kay waxal
Waxal nu fa as lëf ndax mu ubbil nu wunti mbég
Te tëj wunti lor ak wunti moy dàq aw maral
83
Noreyni KEBE
Sa jëf ju baaxul bu muy tax yaw nga
Sa jëf ju baaxul bu muy tax yaw nga naagu ngërëm
Sa jëf ju baax it bu muy tax yaw sa xel dal a dal
Njegam da ngaa defu hay tuubal ñu jàpp ko far
Njegam da ngaa defu yiw santal ñu jàpp ko ful
Ag topp akug moy ku koy def Lay musal ak a lor
Nde Yàlla doylu na wallis luy loreek a musal
Ab lar lu moy-moy bu tuubee moy ga mel ni moyul
Lu jëf-jëfuw yiw bu dee naw jëf ja mel ni jëful
Yaa denc yaw ndaw sa say kem daa ngorook a jamoo
Yaa denc yaw ndaw sa say kem daa ngorook a jamoo
Muy togg’akay yakk, ngay mosleek a mos, sooyoo !
Yàlla a ko fab ne la am, yàlla a la fab ne ko am
Ngay sant muy sant naa « Sàmbaa ! » nga naa « Bóoyoo ! »
Yaa jekk, jekki, ku jekkay jekki yal na nga sax
Cig jekk tey musle cib jooyoo akub juuyoo
Ganccax gu sax nga gu am ndox weddatoo maraloo
Ñàkkoo mbay it amulam ñax gooyaloo, gooyoo !
Ab ñag bu fatt bu lëf dul bëtt mukk a la wër
War ngaa rëyug cant ngir xiifoo, maroo, yooyoo
Ki jàpp gii may gu rëy jébbal la yal na la may
Ngay sant cant gu rëy guy tax mu naa yooyoo
Loo bëgg dikk na, loo bañ daw na yegg nga yaw
Ca digg déndd ya ñàkkoo wenn yiw fuuyoo
Juuyoo ngërëm falaŋoo ndam sànniwoo sa njariñ
Te teggiwoo barke foo tolliy berax xuuyoo
Yaa yanjj, yanjjle, dootoo fayle deeful a fay
Yaa mucc, yal na nga raw, suuroo, fesoo, tooyoo !
Yaa kiilu tëj na ñu buntub lor bu jëm si ci yaw
Lor dooko fekki du ñëw faf ngeen itam juuyoo
Sa bunti mbég neena péll it benne ubbiku far
Te kenn dootu ko tëj ñay waa ngi nii sooyoo !
84
Noreyni KEBE
Abdoul Ahad …
► Abdul Ahad yal na saw fan gudd Mbàkke nga wér | Te sax ci jamm’aku yiw ak jaamu Yàlla gu wér !
► Farlul te wéy yal na ngay for dog bu sedd sa xol | Te mucc ciw ay’akum ndog sax ci def la la war !
► Toppal sa mag Mustafaa bul génn yaw ndigalam | Ngir mag mu mat mag la mat ñéppub sëriñ te
du wor !
► Jëfal te bul faale nit, bul geesu nit ci sa jëf | Na Yàlla tax ngay jëf ak Yonen ba ak ka la jur !
► Kalay manal dara moo jar def lëf ak bàyyi lëf | Te kooka nag moo di « Rabbul Archi » yal na la yor !
► Yar bii nga yor yor ko biir ak bitti moo di sa kee | Moo gën ci yaw nit ñu baax ak kër yu baaxaki jur
► Sa baay a gën ñépp teb yar dong-dong la yor | Yoral yaram ba te koo gis deeko sant ak a yar !
► Sa baay a gën ñépp ab yar ngir dalay jox a jox ab yar | Ba ngay am a am ab yar te doo mos i yar !
► Du yëkkatib yar di teg nit waaye moo gënu nit | Ñay teg nitub yar akay janneek a yeew ak a lor !
► Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam | Xamal ni moo ko ca def jii wax ku nekk la bir !
► Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam | Xamal ni moo ko waral ak cant war na gu tar !
► Ag cant war na ci yaw ak ñoom gu rëy gu rafet | Gu tol ne bàjjo gu dul yam fenn mukkati far !
► Loo jis ci Amsatu moo mii cib yar ak jëfu yiw | Xamal ni moo ko ca def gii wax ku nekk la bir !
► Abdooki Amsatu ak Mbakkeeki Bàlla Asan | Yaw say nijaay a ngii ñoo diy sàll kenn du ciw par !
► Fëxal te raw am nga ab yóbbal fëx ak raw a des | Ngir baaxi bokk a di ab yóbbal na yitte ji sar !
► Saral te wéy dëgg bul yam ciy nijaayaki | Baay ak nday di sant ak a doyloo seeni cër lu ko jar ?
► Foo seeru kuy fok a doyloo ab cëram na nga wut | Loo dolli yaw ci sa cër bii ndax nga am cëri-cër !
► Jollil ca kaw bul fexee jëm suuf’akay wax a dal | Cig jolli ngay waare ab xiibon ca ngay note mbër !
► Reggàyu jàmbur ku koy doyloo ba lekkul a xam ! | Buurub Aras ba far ak bër yépp yal na la far !
► Yaw yal na ngay wéy’akay jëm kaw di dolliku ndam | Ba jiitu waa kaw te nangoo suufe kuy amu tur
✿ Way wii Sëriñ Abdul Ahad (r.a) neena: « Damaa ñëw ci Sëriñ Mbay jaxate (r.a) ne ko: damaa bëgg
nga dénk ma ! », Sëriñ Mbay jaxate ne ma: «danaa la dénk te duma la tagg ! »
85
Noreyni KEBE
Yaa sedd ab xol guyyu …
Yaa sedd ab xol guyyu, yaa dalum xel
Wurus nga yaw, waa ju la for sant asal
Te ku la takk fu mu jëm gën foofa
Te dal di suuxal gaaya waajoon foofa
Te ku la takkul doo ko jis tekki dara
Lu yàgg-yàgg doo ko jis faj it dara
Ndegam awma ndam boppam ….
Ndegam awma ndam boppam
Samap sangg amna ndam
Ndegam manke naa mo xam
Samap sangg mankiwul
Ndegam tuuti naa mo xam
Samap sangg tuuti wul
Ndegam suufee naa mo xam
Samap sangg suufee wul
Ndegam galli naa mo xam
Samap sangg galli wul
Bu may sagganit mo xam
Samap sangg sagganul
Ndegam jekkinaa mo xam
Samap sangg jékkiwul
Ndegam fattenaa mo xam
Samap sangg fatewul
Li lé tax lumay bonn bonn
Ma xamni lu mënti xéw
Damay muj gën mbollo
Mi ñi xëy ma fall !
Ku warr ci saxaaramit tay nélaw
Du tee mu raw
Waral! lepp lo bañ ñakka warr dongakoy waral
86
Noreyni KEBE
Ma tag BAMBA
Ma tag BAMBA
Ak waxi BAMBA
Ak jëfi BAMBA
Ak gaayi BAMBA
Ak sopey BAMBA
Ak doomi BAMBA
Ak seti BAMBA
Ak Bokki BAMBA
BAMBA di kenn
Waxam di jenn
Jëfem di jenn
Kenn du BAMBA
Gisu ma nawleem
Deggu ma nawleem
Ko gis dakoy yeem
Haa fi BAMBA?
Gisu nu kenn
Xamu nu kenn
Deggu nu kenn
Ku niru BAMBA
BAMBA amul maas
Kenn waru koo raas
Kennam amul Faas
Sakkaa fi BAMBA
Gisu nu fenn
Xamunu fenn
Deggunu fenn
Ku melni BAMBA
Amul ca Deymaan
Amul ca diwaan
Xaadimu Adnaan
La tudde BAMBA
Yefar né day ray
Jullit ne day ray
Ñi ba royak ray
Nguir tëlé BAMBA
87
Noreyni KEBE
Mënessula ray
Mënesula roy
Të nga roy ak ray
Xalati BAMBA
Kulafi daa roy
Banaala roy
Ku daaa fexe ray
Banalafi BAMBA
Mënuñla roy
Mënuñla ray
Yaw yaa rëyuk may
Marhaba BAMBA
Man jemuma roy
Ta jemuma ray
Damay Fekhé bay
Ca toli BAMBA
Demb amo mass
Tay ji amo mass
Do amm ëlëk mass
Kénn nga BAMBA
Defar nga kepp
Defar nga lépp
Defarnga feppp
Bokkoci BAMBA
Sa lor nga wëyna
Sap cono weyna
Sap fay ñëw na
Saw ngan rottna
Saw tagg jotna
Te kañla jottna
Ma kañ la BAMBA
Xaré nga fepp
Dakk nga fepp
Nottal nga fepp
Noyal nga fepp BAMBA
88
Noreyni KEBE
Ma jog man ligeeyal Seriñ BAMBA mi
Ma jog man ligeeyal Seriñ BAMBA mi
Ligeeyal boromam ba am li mu am
Bañi kerekerekay xarekay wasal
Magay jamu Yalla ka way yonnenam
Bañi bëgg dongo ka wote ceriñ
Mangay bëgg yala ka sellal JëFam
Bañi fonk judo ka faguy allal
Mangay fonk dine ka faguk yaram
Bañi denć jur gue ka aaye ka nay
Mangay denć tere ka dëdup juram
Bañi daw di dappp adunaa kaykobass
Mangay daw di dapp Yalla dalak ngeram
Bañi xalxale ka jamale ka jam
Mangay dinakay jam ngëram jam na ndam
Bañi ngalngali tali jangoka wal
Mangay soss ci sufuk murid cey mbiram
Bañi xamb kefar di xambuk ceriñ
Mangay xamb taaluk Boromam di guëm
89
Noreyni KEBE
Yaw Abdu Xaadr laxasul
Yaw Abdu Xaadr laxassul !
Ta awa aw yonu ndigël
Ta watu pakk [eviter piege] bula fell
Ngir pakk yee gëna bari
Jigeenangi ta pakk la !
Aw fassa ngi [monture] ta pakk la !
Waajaayi ngi ta pakk la!
Ta pakk yi daana loree
Seytanee mi daana felee
Ta bakanit daana felee
Baaneexitam daana felee
Adina yit daana woree
Tay leegi yaw yangi nii !
Yalla mingay wuttangîni
Ta limulay deflo nginii !
Say noonangi [ennemis] dila teeree
Say noonangi wërla funee
Dila feexee nak def lu nee
Bo farlu wul farlu gunee
Do mëna yegg fu sori
Motax manaan la tubëyul !
Ta fëxa fëx wuti ndigël !
Ku fëxa fëx wuti ndigël !
Du meerr ta deesuko meree
90
Noreyni KEBE
Guissuma man lu jarr taxaw
Guissuma man lu jarr taxaw !
Seenuma yit lu jarr taxaw !
Man lima guiss mo jara daw !
Ta lima seena ëppa jëmm
Murid aki Soxnaa ki kër
La deesi ngeejo aki jurr
Ta xamni ñaar yi kuko yorr
Bu saganee yeesi keemam
Ku soobu mandik yoru tiss
Ta yanu say rëy wu diss
Far bolee aw tiss aku diss
Su bariwul kattan du deem
Paquet bu fessak Marchandiss
Tee nekk ći digg deex wu tiss
Waaja ko yorr matula siss
Aka añanee lamu am
Ngir jallagul jalleegulit
Muccagul musleegulit
Xamul lakoy xala dalit
Yaw buko ñee farko yërëm
91
Noreyni KEBE
Ku dof bay ndamoo baaya mit mbaa ndayam …
Ku dof bay ndamoo baaya mit mbaa ndayam
Dofal bay ndamoo yaw sa Sëriñ beka gëm
Ku dof bay fexee xam alal jeeka am
Dofal bay fexee xam Sëriñ beeka gëm
Ku dof bay fobuk jur di booleeka yar [elever du betail]
Dofal bay fobuk jur di tabal kërëm
Ku dof bay fexee def kemam bum gënul
Dofal bay fexee def laram bum gërëm
Ku dof bay fexee dem fi laajik juram
Dofal bay fexee dem di dolik juram
Ku dof bay fexee japeu Yàllay gësëm
Dofal bay fexee japeu Bambay gësëm
Muriid bul yasam yaw garab boo jotul
Ndaxam bëg ngaa am gërëm saf xorom
Yasam BAMBA mii gën yasam yàlla mii
Yasam foo jotul kat du may ken ndam!
wolof buy rayuk dof bo juk jëm tugël [à l'etranger]
Ni day jaayi gerteem du àndib dërëm!!
Du yegit tugël nak ab reenam du jar
Dangay tonti far des du mos sax payam!
Xarit dëg jaayal fi sab teeru yaw
Te fab say dërëm delu kon doo gëlëm
Dërëm yii fisab teeru ngay seeru ak
Dërëm yii fa teerub tugël yepa yam
La Yonen ba yit doon digël aw nitam
La Bambay digël yit asal aw nitam
La Yonen ba yit daa defal aw nitam
La Bambay defal yit asal aw nitam
La yonen ba yit daa xamal aw nitam
La Bambay xamal yit asal aw nitam
La Yonen ba yit daa fasal aw nitam
La Bambay fasal yit asal aw nitam
Te Bambaa di Yonen ba Yonen ba moodi Yàlla
Te Bambaa ngi nii nan fi yem
Garab goofu jis yaw manga kub kengam
Garab gii di Yonen ba Bambaay kengam
Ku juk weesu sab kek asal daldi gak
Ku weesub kengam yit janoo kub kengam
Ku xam yàlla xamnaa ni xam lii ma wax
Ku jis boo yaboo wedi nak mbaa nga gëm
92
Noreyni KEBE
Koo xam ne jox na lab liggeey
Koo xam ne jox na lab liggeey
Te nga jubal booba liggeey
Mu dal di lay dollib liggeey
Te jox la ay liggeeyukaay
Ku bëgg aw nit na liggeey
Ku bëgg ay yëf na liggeey
Koo xam ne kii bawul liggeey
Du ñàkki yëf du ñàkki gaay
Ku bëgg xam-xam na liggeey
Ku bëgg ag jur na liggeey
Ku bëgg Yàlla na liggeey
Ku bëgg lëf na ba jataay
Ku bëgg a am lu lew te teey
Na bàyyi faww ab jataay
Ku bàyyiwul fàwwub jataay
Du am lu lew du am lu teey
93
Noreyni KEBE
Ku àndul ak moom
Ku àndul ak moom
Dara la dul moom
Yàlla bëggul moom
Ku dëddu Bàmba
Bàmba damaa yar
Ba ma amab yar
te tegu mab yar
Maa sant Bàmba
Ku bëgg Yàlla
Ak topp Yàlla
Ak xolbu sella
Na fekki Bàmba
Xam na Boroomam
Am na Boroomam
Raw nay moroomam
Ka dess du Bàmba
Day xëy di jàngal
Nit ba mu mokkal
Te du ko bindal
Cey Yàlla Bàmba
Ku Bàmba jàngal
Nga mana jàngal
Kepp ku dikkul [ou dëggël]
Siyaare Bàmba
Ñeppa ngi may yeem
Man maa ngi lay yeem
Nu bokku lay yeem
Yeeme nga Bàmba
94
Noreyni KEBE
Ma jóg wuti ndëndum cant ak galenub ngërëm
Ma jóg wuti ndëndum cant ak galenub ngërëm
Ba tëggël Boroom Tuubaa ki xëy jox ma ab galan
Wutël na ma ndombag tànk dolli na mab galan
Te may na ma ag ceex ak njariñ sant naa ko man
Ka koy bañ du man mii, waaja koy ayibal du man
Ka koy jëw akay sikkël du man, ku ko noonu bon
Ngiram mile moo gën mepp ngir ku ko wàci bon
Ku wàci ngeram mii daldi jaamuy xerëm xaran
Te Yàlla akub Yonnent daala fi nekk kat
Te ñoo di Sëriñ bii moo di ñoomit ku weddi fen
Lilee tax ku dikkul jox ko say mbir da ngay xaran
Te do ab Sëriñ doo Ceddo ngir ceddo yaa la gën
Sëriñ dëgg day xam Yàlla, xam la mu def bu wer
Mu naŋgu ko deŋkaaney mbiram ay mbiram yewen
Te ab yeefarit day nekk cig keefarëm bu wer
Di moy moy gu wer tey fóon akay naan akay seben
Lilee dig Cëriñ, lee moo di keefër werël xarit
Ku wer am lu wer, toppal Sëriñ bile moo fi man
Sëriñ boo fi degg ak boo fi seeru du lëf mu man
Mosal bii Sëriñ boo mos bu dul bile mos posen
Murid yii mu àndal rekk ñoo gën sëriñ sa woon
Bu bis peñci baa wax jii ñu xam ne ju wer la woon
Xamal leegi wax jii Yaw te sóobu ci am ngiram
Te yekkët sa mbir jebbël ko am ndam amub galan
95
Noreyni KEBE
Nangul a feete ñepp suuf
Nangul a feete ñepp suuf
Kuy bañ a feete ku ne suuf
Boppam ba dootu jóg fi suuf
Mukk te ñepp a koy tane
Mboolem ña am kaw it fi suuf
Lañu bawoo, ku jële suuf
Boppam ñu fab ko teg fi suuf
Muy bër-bëreek a kun-kuni
Sëriñ bi Ñun noo ngi fi suuf
Te rikk yaw ki jóg fi suuf
Jàpp nu yëkkatee fi suuf
May nub yar ak jàmm ju ne
Yaatal nu yit ci sepp suuf
Notal nu mbooleem gaa yi soof
Ñu nekk nag ci sunu suuf
Nu ne ca kaw di la wane
96
Noreyni KEBE
Seriñ bi man yaama guën
Seriñ bi man yaama gën
Yaa gën ka gën kama gën
Lii nangu naako
Te Yaw mii rek laako nangul
Ngir mangilay moya moy
Yow yangi may maya may
Mboloo mi ndax kile nitt
Mës ngeena gis kuni mel ?
Ag moy kukoy feye ag may
Man xawma fen sa kem
Ku xam kemam nako wax
Man lajiwut te xamut
Ku melni man bu gisul won
Waju mel niki yow
Mbiram du jag te du am mukit lukoy sutural
Motax ba man Baabacar
Xamnani maa waa raw
Mboleem ku lay sant
Ngir yaw rek yaama teral
Seriñ bi yaanu fayal taalup tawat bamu fay
Budul wonak yaw lu bonn am kay gërëmnaala
Seytane tuuti mu bek ñun ñëp tuuti ñu rot
Yaa tee mu bekk yaa ñu tee rot man gërëmnaala
Yaa dong te ñu wëreeluy jommi jommii ji wëyy
Di tapale ka naxe kay lep man gërëmnaala
Ay waa ngi dapp kapp mboleeem nitt ñi teggi ñu ñun
Yaa tax mu teggi ñu motax gerëmnaala
Ku nee gi rapp rappi ngir xiif ak ragal ndare ñun
Yaw yaa ñu te bole xiif ak rëtt gërëmnaala
Yaw may ngañu dundakup dundit bu werr bu rafet
Ta may nga ñu ndox mu doy jaajëf gërëmnaala
Mbacke mënon ngamaa baña may ak yëk ta sani ma fee !
Ta def ma faf ni ku dundul man gërëmnaala
Yaw fop nga mboleem luñiy wut tek si saa yoxo yi
Faf defma ni sap loxo man kay gërëmnaala
Man saytuwul sa njariñ man saytuwul sa lorit
Yaa may jariñ dima xajjal lorr gërëmnaala
Jisso ci man ci man sa njariñ
Jisso ci man sa lorit
Ta jublumaaki njariñ jaajëf gërëmnaala
Seriñ bi tijil ta ubil ta badil ubi alli afal
Bunti njariñ yëpp birak biti fék natu yi
Mbakke ubal tëjël madd saañal makk sakk damacc
Fu lorr di aw jëm ci ñun bay jabbatoka layu
97
Noreyni KEBE
Seriñ Massamba …
Xarit bulay may june [5000f] kay jariñ jafe na
Amnaa xarit buma xëy may junni tek ća di ree
Te naa ma li bariwul ay bii xarit jafena !
Massamba mbacke ne ćas ap junni biss nema am
Seriñ bi Yalla na ko jox lo xamni nii jafe na
Seriñ bi Yalla nako jox mboleem li defi mbebet
Tay mayko jitu gu mboleem niit naa jafena
Yallana aw fanam guddu,
Digantekup um seriñam ne {leer} nañ !
Muy ami mbek yo xamni yii jafena
Magam ja Yallana ko may lo xamni ni matuko
May yit ba ko jiss naa li Bać am jafe na
Ta yaala na samuk njabotam, dolli sen ngerëm
Ta may leen yite yu nefaa yite yi jafenaa
Fopnaako denk SeriñTubaa magam jako yorr
Ta yarko yarr bu rafett bo xamne nii jafena
Baće ak njabootam senup ćant Yalla nafi sax
Ñi yokkit ba ñëpp naa Baćak ñoñam jafe na
Ku mënti woppaka dee nay dund faw aka werr
Ta am ngerëm lu neefa li ngëram jafe na
Sheex Ibra
Xamal yaw ni Alxur'aan ak Seriñ Ibra Fall
Daño bokk mbir guissal ma wane la
Ba Yonnent bi nekkee ca mbokkam ya won
Morom lagn ko defonn
Boba sujott gui xewagul
Bu togue ca kaw
Ñi tokk ca kaw ni Mom
Bu waxee ñiy wedeka weranteeka xul
Ba Yalla waccee Suratu Hujuraat (Surate 49)
Nagn xamni lañ daa def warul wone
Lawone fofa moy tay ji Sheex BAMBA mii
Ba Ibra Fall dikkagul, mbiram yaato gul
98
Noreyni KEBE
Ndaxam BAMBA yaa jar di sonnal ba dee
Ndaxam Bàmba yaa jar di sonnal ba dee
Ludul jog liggeeyal la xaw nay araam
Te fas naa la yeene liggeeyal asal
Liggeeyub ngërëm bu doy kepp yeem
Kudul yaw yayoowul liggeeyub ngërëm
Te kat maa la wax lii yëgal loolu « Daam »
Da nga a set setal, te jag nag jagal
Te am nag amal, sa jëf matl a jeem
Te man jeemu ma a def sa jëf yii ma jis
Damay jeem a def sab gewël, def sa jaam
Ma jog nag te way laati ndax ab gewël
Bu lay way ku jog dal di feesal jibaam [poosam]
Kulay way du bon, kulay way du rus
Kulay jomb a way lee mu xëy mel ni mbaam
Ku def sab gewël dal di am ay gewël
Yu koy dox di way akay topp weem
Da ngay sëq ay may di jox sab gewël
Te boodee may it sab gewël doo ko leem
Mayeb junni ak mayeb tànk a yam
fi yaw mii, falang nu ginaar ak gileem
Ginaar ak gileem ak fas ak gepp jur
jëwoo ko jëwoo yit murid yii di raam
Te jaaxal nga goor ak jigeen ak mag ak
ndaw ak jinne ak njuuma doo maase maam
Da ngay ndey di baay ak nijaay ak sëriñ
di maam ak xarit te gën leene « Daam »
Da nga a yar sa bopp te yar kepp nit
te yaa tax ba ken dootu wax kenn « naam »
Yar ak kersa ak maandu ak not bakkan
akug tab nga jiitoo ku jox Yàlla njaam
Ku def tay ludul jog te dal lay dawal
ba am say ngërëm ma ngay def araam !
99
Noreyni KEBE
Ndaxam gaayi may siisakay dox di bañ
Ndaxam gaayi may siisakay dox di bañ
La ñiy bañ ci man mii du man mii ko def
La ñiy bañ Sëriñ bee ko fob def ci man
Nde man lott naa sax ci def lenn lëf
Sëriñ beey ki fob ay yëfam def ci man
Yëfam dongu laa yor nde man awma yëf
Damay dem, damay dem, damay dem ku demMa dem man, ku dul dem ma dem man ba la
Ku bëggul lu dul Yàlla ak Bàmba mii
Du sikkal samay mbir asal dëgg la
Ku bëggul lu dul aw ngerum Bàmba mii
Di wut Yàlla kookee samab soppe la
Ku xëy di neexalu nit ngir bëgg seeni ngërëm
Ku xëy di neexalu nit ngir bëgg seeni ngërëm
Xëyal di neexal Sëriñ Tuubaa te mokk ko yaw
Bis boo amee ngërëmam, am Yàlla am sa mebet
Am barke, am kepp nit am lepp far falu yaw
Moo tax bàyil lepp tey wut fàwwu ay ngërëmam
Ba am ko kon say mebet day jug te wut si la yaw
100
Noreyni KEBE
Sëriñ bi yaw nanga nu may, Ngir Yàlla ak Yonen ba tay,
Sëriñ bi yaw nanga nu may, Ngir Yàlla ak Yonen ba tay,
Xam-xam bu nuy fegali moy, Fàww ak a boolee’k i ndigël! Amine.
Ngir nit lu xam-xam te bawul, Li Yàlla mii tere, deful,
Li Yàlla mii digle asal, Feruli ijji sax dalul!
Ku dem ci’b ja xamub dërëm, Du la jariñ, amub dërëm,
Moo lay jariñ, moo tax ku xam, Te jëfewul xamul amul!
Koo seeru xam na ab dërëm, Ba noppi tey wutub dërëm,
Doo gis ku doyloo xamub dërëm, Waliis wutub dërëm, wutal!
Kem li nga jëf rekk nga xam, Kem li nga am rekk nga xam,
Li nga jëful du li nga am, Du li nga xam yewwul jógal!
Doonte dangaa xamoon ba xam, La Yonenub Yàlla ba xam,
Ak la malaaka yepp xam, Te jëfewoo lëf nga xamul!
Doonte dangaa jëfit ba jëf, La Yonenub Yàlla ba jëf,
Ak la malaaka yepp jëf, Te sellaloo, lëf nga jëful!
Boo sellaloon it jepp jëf, Te xamagoo na deefi def,
Ëllëg sa yëf yile nga jëf, Kon it sa xel warul a dal!
Àddina ag dex la gu xóot, Ku tàbbi nag ci dex gu xóot,
Te gennagul nay ree bu tuut, Ba genn mucc te labul!
Kepp ku dex gile ronu, Bul beg ci gaa yi lay ronu,
Ngir beg ci gaa yi lay ronu, Dana waral lab ak labal!
Def a la def nit, boole’m xel ak fit
Def a la def nit, boole’m xel ak fit
Xamal ni dof kat, du làqq Yàlla
Itte ak’um xel, ndab laa ngi jàppal
Joxe ñu feesal, dell ci Yàlla
Sa itte nam day, ak na sa’m xel day
Sa’b cër na lay day, fàww ci Yàlla
Nit ku’m xelam tuut, ittee mitam tuut
Fàww’ub cëram tuut, giñ koci Yàlla
Nit kum xelam rëy, ittee mitam rëy
Fàww’ub cëram rëy, giñ koci Yàlla
Ku gàtt am xel, du guddu aw xel
Ku guddul’uw xel, du jege Yàlla
Ku bëgë seetu, na dikk seetu
Lii ku ci seetu, du mere Yàlla
101
Noreyni KEBE
Ndaxam gaayi koo xam ne bàmmeel a koy
Ndaxam gaayi koo xam ne bàmmeel a koy
Xaloo mujje senn’as cagar doy na ko
Bu doon dunde am ñax di tëdd it koroŋ
Mu doy sëkk lii Yàlla yit xam na ko
Faral dëgg doyloo xarit lii nga am
Da ngay doylu doo doyle lii degg ko
Ñi am junni tay ak ñi am tànk a yam
Ku nee ngiy tawat tay wutug dolliku
Te foo seeru buur ak yëfam ak ñoñam
Ma ngay aaje lëf aajo kenn ñàkku ko
Ku am loo amul aaje loo aajewul
Ku am lëf lu bon bon na far sant ko
Te foo degg kuy wax ne man sant naa
Da dis gor nde ñàkkul lu muy nemmiku
Te foo fekk yit ab tawatkat du nit
Te dus gor ludul cant yaw moytu ko
Muñ ak cant a gën lepp loo man di def
Nangay sant ak’ay muñ tawat nag ba ko
Na ngay sant xeewël di muñ jepp lor
Ngerum gaayi Yàllaa ngi nii sόobu ko
Amaa naa nga gis gaayi ñuy ree ka beg
Di sooxaale ay lor yu dul teggiku
Dañuy dox di nëbbook a nëbbiy tawat
Ta koo gis ci ñoom as cagar doy na ko
Lu dul doy du doy nag te luy doy di doy
Murid mbubb daal ak tubëy doy na ko!
102
Noreyni KEBE
Assalamun Alaykum Mbacke …
Assalamun Alaykum Mbacke sap geewal lay nuyu
Ku reere’w turam nak Baabacar moo di aw turëm
Gërëm naala, bek naa yit ci yaw ta bek ci say jëf it
Ta sant nilay Yakaar akay wut ci Yaw ngërëm
Ñañuy degg ak mboleem ñañuy seeru yaa ci gën
Ña rey na nu daa waxtaane sakk nga seni kem
Ta tijaan akup Xaadir ku nekka fi war di ñëw,
Di sufee ka barkelo ka denkane ay mbirëm
Dangay defaral nit ay mbiram boko dul defar
Nga wacc mu dem yaw do kuñi bonee fik ronam
Saxaaru ndigël yaakoy dawal kula jox mbirëm
Nga jappko tekk ko fo xamne xel mënuko xalam
Ku dugg ci Yaw mii dem!
Ku duggul ci Yaw du dem
Ni Yaw daalafi yobboka dem , yobuño ki ndam
Dugël ñu si dessemak sukanam
Bu kenn gatt fann, fann yëpp nay guddu
ñepp jub, bu lëf meti nitt
Nun ñëpp may ñu werr ak yaram
Na mbolem suñi fann gudd, mboleem suñi jëfit na sedd sa xol bi guy
ñuy gaayu am xorom
Na yite yëpp ak xol bi ak jurr gi jëm ci Yaw
Ba lepp jeex kunee dessak aw turëm
103
Noreyni KEBE
Di bay di bay ba sa mbay ñor xomb nag nga ne cas
Di bay di bay ba sa mbay ñor xomb nag nga ne cas
Mbay mepp sànk ci àllub neen a bon bu ko def!
Ku jàpp dàgga ju rëy joo xam ne ñepp a ca xaj
Ne xërr dellu di xaaraaneeka ñàq aka dof
Bul moy te bul tudd kuy moy bul waxug moyamit
Noppil ci kuy moy, moyam yeppit nga noppi ca faf
Bàyyil lu bon ak ka koy def ndaxte nit bu deful
Lu bon te tudd ka koy def booba def na ca lëf
Moo jaa lu jar dëgg nit kuy jëf ba am jërëjëf
Wax nit ci saa lu waral mbooleem jëfam ja ni ëf?
Man xaw ma ñam woo mosul sax loo ca taqe ribës
Moy goo moyul bu ca jekkiy ŋal-ŋaleeka suruf
Jàmbur bu moy defalub jàmbur ca moy ga mu moy
Màndul ci moomak yëfam far yaw te sàmm sa yëf
Lu jar moyoo deeti bokkak gaa ya moy lori moy
Ñam woo mosul dara man ngaa ñàk a wax la ca saf
Jàppul te bul jëwu nit, bul deglu kuy jëwu nit
Kuy deglu jëw ak ka koy def kenn baaxu ca jëf
Bul jàq, bu rët te tooñoo kenn, tuddula nit
Lu yàgg yàgg ku tooñul mucc, Yàlla du kaf
Xamal ne Yàlla du may nit laf ju muy lore nit
Ku am lafit bu ca dee lor daal di ñàqati laf
Tuubal te sant ñu far say moy te dolli sa ngëm
Dàkkul la mbooleem lu bon fàwwak ka koy nara def!
104
Noreyni KEBE
Fabal Yalla jamm ak …
Fabal Yalla jamm ak yërmandeku yiw ak njariñ
Joxal ñu Seriñ Tuba ki tax ñëp xam la yaw
Fabal ngërëm ak Jaarama jo xamnè dotu dañ
Joxal ñu Seriñ Tuba ki yee niëp ćiy nelaw
Fobal ćanti ćant yu andak mbekk
Joxalñu Seriñ Tuubaa ki tax dinee xëy taxaw
Fobal may yu deful takkakay tandale ka limm
Joxalñu Seriñ Tuubaa ki tee niëp russ ba sew
Fobal ndabi tawfeex ak teraanga yu fessee mbekk
Joxal ñu Seriñ Tuubaa qui tee ay wu nêkk xew
Fobal pal gudul dañ mukk ta dootu nëx
Joxal ñu Seriñ Tuubaa qui xëy fapp ñu tekk ci kaw
Fobal lepp luy toyal xolam ak lu koy seral
Joxalñu ko faw ak ndam ta may ci momup yiw
Na mboloo mi yëp xam tay ni Bamba yaw laa faral
Ta yaw rek laa andal ta yaw rek laa safooo…
105
Noreyni KEBE
Mënoon ngamaa wacc bañmà ma saak may ku amul
Mënoon ngamaa wacc bañmà saak,may ku amul
Mënoon ngamaa saak,defmab ceddo may ku gëmul
Mënoon ngamaa saak defmab luu, bu silmaxa,tëx
Mënoon ngua saak defmab rabb wu dèffi fetal
Mënoon ngamaa def kudul taggooki wop aki lorr
Mënoon ngamaa def kuñuye xaagne akay doyodal
Mënoon ngamaa def ku deful degg,defuka guiss
Mënoon ngamaa def kuñuy sufèl akay woyofal
Jarama YOW JëreJëF, YOW Ya mënoona doggal
Ci mane Lu kene amulub rènam,farooko doggal
Bà yyil kulay ba
Bà yyil kulay ba
bà yyi lulay ba
ŋëb ka la dul ba
te moo di Yà lla
Ku la ŋëb it ba
lu la ŋëb it ba
Yalla a la dul ba
ak waa yi Yà lla
Jublul ci Yà lla
te wéer ci Yà lla
Te way ci Yà lla
ak gaa yi Yà lla
Ku tëb bëgg a dal cig cëriñ jell ag
Ku tëb bëgg a dal cig cëriñ jell ag
Murid, doo ko mat kat te doo am dara
Ku jeggig murid dem di yóotug cëriñ
Dafay ñàkku yiw, ñaare amtil dara
Ku jëm cig cëriñ fàww dox cig murid
Doxal cig murid boo bëggee faj dara
Lu guy rëy-rëyub dàtt ab gif la won
Sëriñ dib murid won bu moomul dara
Sëriñ day bawoo cig murid dib sëriñ
Njegam lii amul doonagul kon dara
106
Noreyni KEBE
Doo kenn yaw, ken du yaw,
Doo kenn yaw, ken du yaw, eskëy sa mbir woyoful
Sa ndend nekkul ci dendub suu si tay, doo maas !
Yaaram bu tedd nga yaw, as gor nga yit su rafet
Ab jaamukat nga bu rëy, yaa tee nu bon, doo maas !
Yaa tee nu bokk torox, yaa tee sunuy bañ a ree
Yaa tax sunuy soppe beg, yaa tax nu beg, doo maas !
Yaa sedd ker, rafetub xol, neexi wax jubi wax
Am ngor rafet jikko njaxlaf, ñàkku ay, doo maas !"
Sëriñ bi nëbb nga saa bon gii ba dee fi ma jox
Sëriñ bi nëbb nga saa bon gii ba dee fi ma jox
Nëbbël bonug nit ku may jox lëf ba dee fi ko jox
Yaa ngi nde boo ma fabul woon ken du xam ana man !
Bay jàpp lëf di ma jox tey toppatoo lu ma wax
Defar nga saa mbir ba gis naa gaa yi may joxi mbir
Te xam ne daa wu ma gis kuy dox ba geesu ma sax
Moo Mbàkke man na ma lay santee ti ak nama layJàppee ti ak nama lay taggee ti yaa mata sax
Saa nawle yaa ngi ma fiy neexal di raama ka daw
Yaw sab Murid du torox ngir doo Sëriñ bu nasax
Budul kon ag Yàlla ak Yaw gàcca wër ma gu rëy
Goo xam ne kon fu ma janlootee ku nit ne tasax
107
Noreyni KEBE
Njagam bëgg nga sak mourid jak te wër
Njagam bëgg nga sak mourid jak te wër
Moyul marsandissak jigueenak pexeem
Moyul marsandissak jigueenak pexeem
Te boul deglu sax ay waxam mbate reem
Kudul moytu yi yetta kay daw bu wër
Akay muslu woonaa hasal tousskareem
Te kat niette yii nioo di waggiy mourid
Dañiy moussou itteemakuk taalubeem
Te kat nioo di ak max ba tay cip mourid
Te lii doyna mboolem mourid yeppu saam
Ku bëgul ludul Yalla ak raw lu bon
Na def yii bayit cip xolam ak jibaam
Lu tax nga baaxoon a baax it mat na
Lu tax nga baaxoon a baax it mat na fukki yëf ak
Juróom ak as lëf xarit ndax Yàlla sedde nu ko
Muñ ak ngor ak diine ak fay bor ba laa fay a jot
Ak sàmm wóllare ak nax nit ba xettali ko
Ak suufe ak wax ca suuf ak doylu ak bañ a xer
Ak ittewoo ndigal ak farlook a feddaliku
Ak wacc lepp lu bon ak sax ci lepp lu jub
Dalal di def mbaa nga fab say mbir te jebbale ko
108
Noreyni KEBE
Seriñ bi Yaw yaa wara sante Yalla
Seriñ bi Yaw yaa wara sante Yalla
Ta Yaw li tax nga wara sante Yalla
Ko xamnee ki daanala siis aka añaan
Muju na tay ji dila xaaraan aka ñaan
Ko xamni ki daanala def maas ak morom
Muju na tay jii dila def sangak Borom
Ko xamni ki daanala ñakki aajo
Mujuna tay ji dila may si aajo
Ko xamni ki daanala may nak aajo
Ñëppa ngi muju diko may tay ji aajo
Ngir guisnga [Sheex] Ibra Fall’a ngii ñiy faalee
Ta xamni kenn daawu ko xëy di faalee
Ak [Mame Thierno] Ibra Faty milee ken dul fattee
Ta xamnii deesaanako dox di fattee
Ak Mandoumbe milee ken dul yabbi
Ta xamnii kenn daawuko sex bay yabbi
Ak doomu Anta jilee melni jant
Ta xamni kat mingi melonn ni bantt [...]
Murid dëgg bul gaawa wutt kër muñal
Murid dëgg bul gaawa wutt kër muñal
Ta wutt itee ngir kër dafay kar Murid
Ku juk soobu manding ta andak ndaw ak jigeen ak lafañ
Moo namuy def Murid ?
Ku am kër, am sangg am naw lëjël
Kër ak Sëriñ ño jafee yorr Murid
Jagal sap Sëriñ ak sa waa kër bu werr
Ñi jak, bokk begg lool, yombul Murid
Sa kër gi bu santee sa kër sangg meer
Këram it su santee sa kër merr Murid
La gënn nak moy muñ sa bopp ak sa kër
Ta jox lepp sa sangg lii dik MURID...
109
Noreyni KEBE
Jigeen …
Jigeen bu dee sey ci kër tey bëgg sey ba di neex
Nay muñ ta sax ci ndigal tey tont tontu lu neex
Tey foota kay togga kay ree tey waxam bañ-a neex
Baatam di jëm suuf ta bum jekki tawatt aka jeex
Tey xëy di xeeñ ta nangò ñakkiy yëf-am tee sawar tee
Bayyi maanee ku naa mane maanee sey ba du neex
Tey buub këram ba mu sett buub kër sëriñ ba mu sett
Raxass ndabam ba mu sett muy daw xulòo a kiy xeex
Tey jog sa njël wall te duy mbaddam ya bët sòora set
Mu gaawtu laax rajji fobb nakkay ndaxam ne sareex
Tey muuru tey baña merr tey sammu sammu bu werr
Tey jappi tankam ci kër ga kone seyam dina neex
Tey gattaluw lammiñam tey wann wanni merram
Kër matti neen la te boo koy mooñ mu xëy ni mëreex
Sey katt yi sey baa ngi kuy sey tee doo seyeenii
Loo am ëllëg na la doy lo degg it na la neex
-Jigeen balaa baax nangò dem dagga tey rooti
Tey togg jox sëriñam balaa tilim fòoti
Lewat nangò yor njabòotuk kër ga yaatu ci gane
Tee mokka mokk ba buy neex guur ga muy nootee
Tee neexu lammiñ woyaf mbirr toyy bay saf-u xob
Tey buub ëtt ba ak këram ga tey nangò bootee
Te def mbañam rus tee lambòo ker sawar mana muñ
Tey doomi soxna bu wer fum sey ñu yokkòti
Sawarr yarò yaru am xel loo ko yònni mu daw
Tey jekki neegam balaa dem fenn taggòo-ti
Tey noppi tey muuru tey lamsal jegeb sëriñam
Tey nabbu jambur ña tey wax ndank tey yootee
Rafet rafet jikko tey sett ràcc xar kanamam
Tey soccu tey ree kanam gay melni luy wootee
Bis bu aayee fonkk ak toggam di neex-a lu ñam
Bum yann bum caxx bum xoñ bum texem lii ti
110
Noreyni KEBE
Buy tabbi neek sëriñam dey sol sëram ya mu
Am xeeñ laskoloñ ja mu am fobb tiol ko ru gooti
Fum giss sëriñ ba di xay xay loo-ka foon a ka bës
Lum wax mu daw tey wuyòo santam ba buy wootee
Lum am jox -ub sëriñam lum xam wax-ub sëriñam
Tey gaawa tuub biss bu tooñee dal di tuubati
Jigeen ju mel nii ma wax ŋanjam wa rot na asal
Giñ naani doomam ja day am barke buy tuuti
Soxna Jaara
Jaaraaki doomam a jël ndam ñoo amit jërejëf
Moo jiitu soxna yi doomam jiitu ñiy tubeyu
Kuy soxna Jaaraa la gën mbooleem ku sol tubeyit
Bàmba ko gën foppu wax jii wer gi dem na dayo
Yaw soxna Jaara ku am jaaraama yaa ko waral
Sa dooma gën ñepp yaa gën mag ñi gën gone yi
Yaw Soxna Jaara begal saw ŋaññ rot na xasal
Yaa jur ka jëm ci Boroomam woote ñepp wuyu
Góorak jigeenak magak ndaw koo fi jis mi ngi jak
Te yaa waral ñeppu jak beykat nga bey nga beyu
Xamal ni waa penku ak waa sowwu ñeppa ngi moss
Ci sab liggeeyaka beg yaw doo ku deefi moyu
Daawoo weranteeka songanteeka dox di xuloo
Daawoo bañit kula yab daawoo jayeeka jayi
Daawoo lebal kenn ay daawoo waxit lu jubul
Daawooko def Buso jaajëf man danaala nuyu
Tey maagiley nuyu nak yaw mbaati jàmm nga am
Do am ludul jàmm yaa fab jàmm leble fayu
Yaa japp jàmmak u yiw ak cant tex ko mu sax
Nga beyko nak bamu ñor daagul ca Aajjana ya
Ku dib jullit warnalay ñaanal ci waxtu wu jot
Loo bëgg yalna nga am dakkul nu lor yi
Sarax nu nak ci sa barkeb sët yi ak ci yawit
Muccak werak guddu fane loolak wayak tubeyu
111
Noreyni KEBE
Sources :
Page: Serigne Mbaye diakhate
Guewalou Serigne Saliou
Gueye Madial
Noreyni Ousmane ….
N ASPWOLOFAL" MOURIDE.
Mémoire de Maitrise (1993)
TRADUCTION ET ANALYSE DE QUELQUES TITRES
DE SËRIN MBAY JAXATE
Sites : Drouss.org
05/02/2018
112
Noreyni KEBE
Téléchargement