Kon nag danaa wax ba samay xibaar siiw Bañ xamne bëgg naa lu baax, lu baax a néew
Ab xaj bu màtt kenn manu koo teree baw Ku tàbbi tool boroom mu naa la mbëw-mbëw
Ku ruur ci lislaami Seriñ Tuubaa jii Walla nga bañ Allaaji mbaa jumaa jii
Njeem góor la njeem jigéen la maa lay xiiru Màtt la, baw la ba ca Fuuta Tooru/o
Ahaazanaa l-Laahu jigéen juy m)ndi Ci rikklees ak beer di ànd’ak bàndi
Suy naan ci beer bay bëgg a jóg ne lacc Jahanamaa’ng koy xaar, moo raw sàcc
Ahaazanaa l-Laahu jigéen i garbu Kër gu mu nekk sopp i leen ay “kalbu”
3
Góor ña’ak jigéen ña ñ”pp lay caaxaanloo Te ku mu wéetal bëgg laa saay-saayloo
Góor gu dëggënteek moomi tàkke yàqule Ku lekk aw ñamam hisaab ja texëla
Goorguko wattuwul da ngeen dem naari yawmal xiyaamati du ngeenfa jaari
Cheikh Bamba noonna soxna Faati Kurah Waxal borom meteelya nañ tuub goorya
Seen naa meteel yu bari fin-naari ku watuwul góorña du dem jinaani
Muneko ndax seenoo woroomi kaalaa ngir diko kekantoo di xiili xaala
4
Muneko koo fi seen ci doomi Aadamaa woroom meteel yaako dugël jahanamaa
5
Ladale aadama ba fii ci dunyaa mbir yufi xew jigeen def yu bonyaa
Yonenya ak shahaabaya ak abdaal ya waliyyu yaak mbooleem ña fenton nger ya
Lumasa xew ca seen digënte, ñooma ken manuleena tëh, lu yaxxu ñooma
Pexem jigéena raw pexem chaytaane yallaako wax ci alxuraan, giñ naane
“Xaala laahu tahalaa inna kaydakunna haziimun Inna kaydach-chaytaani kaana dhahiifan”
Yawmiy sakub denkkë ci yoonu Bamba Ci yoonu diine ji, ci yoonu Bamba
Dinaala denkë, denkë tay saa bopp Ak bepp shaadix buma jox ab nopp
Xamuma dara dara fil azmaani Janguma laawël duma foorey saanii
6
Waaye danaa lawax la yonen bëgon Ak lamu bañ ci alxuraan, dajeek kun
3Garbu : ???
4 Ci biir sawara
5 Muy goor
6 Laawël :